عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رضي الله عنه قالَ: قالَ رَسُولُ اللَّهِ صلَّى اللَّهُ عليْه وسلَّمَ:
«دِينَارٌ أَنْفَقْتَهُ فِي سَبِيلِ اللهِ، وَدِينَارٌ أَنْفَقْتَهُ فِي رَقَبَةٍ، وَدِينَارٌ تَصَدَّقْتَ بِهِ عَلَى مِسْكِينٍ، وَدِينَارٌ أَنْفَقْتَهُ عَلَى أَهْلِكَ أَعْظَمُهَا أَجْرًا الَّذِي أَنْفَقْتَهُ عَلَى أَهْلِكَ».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 995]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonnent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
"Diinaar boo joxe ci yoonu Yàlla, ak Diinaar boo joxe ci goreel jaam, ak Diinaar boo sarax ab miskiin ak Diinaar boo jox sa njaboot ba ca gën a màggug fay mooy bi nga jox sa njaboot ".
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 995]
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc tudd na yenn xeeti joxe yi, daal di wax ne: Diinaar bi nga joxe ci jihaad ci yoonu Yàlla, ak Diinaar bi nga joxe ci goreel ab jaam, ak Diinaar bi nga sarax way-ñàkk ji soxla, ak Diinaar bi nga jox sa njaboot, topp mu xamle ne ba ca gën a màgg ag fay fa Yàlla mooy bi nga jox sa njaboot ak ki nga war a dundal.