عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ أَنَّ النَّبِيَّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«مَا مِنْ يَوْمٍ يُصْبِحُ العِبَادُ فِيهِ إِلَّا مَلَكَانِ يَنْزِلاَنِ، فَيَقُولُ أَحَدُهُمَا: اللَّهُمَّ أَعْطِ مُنْفِقًا خَلَفًا، وَيَقُولُ الآخَرُ: اللَّهُمَّ أَعْطِ مُمْسِكًا تَلَفًا».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 1442]
المزيــد ...

Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
«amul benn bis bu jaam ñi di xëy lu dul ne ñaari malaaka danañu wàcc, kenn ki naan: yaw Yàlla joxal aji-joxe ji leneen, keneen ki naan: yaw Yàlla joxal aji-téye ji ag yàqule».

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 1442]

Leeral

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xibaare ne bépp bis bu jant bi fenk ñaari malaaka danañu wàcc di woote, kenn ki naan:
Yaw Yàlla joxal kiy jox cig topp Yàlla njabootam ak di ganale ak di saraxe wuutal wecceel ko yiw ca la mu joxe, te baarkeelal ko ko.
Keneen ki naan: yaw Yàlla joxal kiy téye wolif loolu ag yàqule te sànk alalam ji mu tere ña ko yeyoo.

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Dagan na ñu ñaanal aji-tabe ji muy yokk, ak ñu wuutalal ko yiw ca la mu joxe, dagan na it ñu ñaan Yàlla aji-nay ji ag yàqu ci alalam ji muy nay bañ ci a joxe la ca Yàlla waral.
  2. Malaaka yi dañuy ñaanal way-gëm yu sell yiy joxe ag yiw ak baarke, te seen ug ñaan lu ñuy nangu la.
  3. Ñaaxe ci joxe yu war ya ak coobarewu ya; niki jox njaboot gi, ak jokk mbokk, ak bunti yiw yi.
  4. Leeral ngëneelu aji-joxe ci lu baax, ak ne ag mujjam mooy ne Yàlla da koy wuutalal, Yàlla mu kawe mi nee na: {lépp lu ngeen joxe moom moo koy wuutal, te mooy gën gi wërsëgale} [Saba: 39].
  5. Ñaan Yàlla gii nag kiy bañ a joxe si farata lañuy ñaan mu dal ko, waaye bu dee joxe yi ñu sopp nag du ci dugg;ndax boroomam yeyoowul ñukoy ñaan Yàlla.
  6. Araamalees na nay.
Gaaral tekki yi
Làkk: Àngale Urdu Español Ndollent (47)