عَنْ عَدِيِّ بْنِ حَاتِمٍ رضي الله عنه قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«مَا مِنْكُمْ مِنْ أَحَدٍ إِلَّا سَيُكَلِّمُهُ اللهُ، لَيْسَ بَيْنَهُ وَبَيْنَهُ تُرْجُمَانٌ، فَيَنْظُرُ أَيْمَنَ مِنْهُ فَلَا يَرَى إِلَّا مَا قَدَّمَ، وَيَنْظُرُ أَشْأَمَ مِنْهُ فَلَا يَرَى إِلَّا مَا قَدَّمَ، وَيَنْظُرُ بَيْنَ يَدَيْهِ فَلَا يَرَى إِلَّا النَّارَ تِلْقَاءَ وَجْهِهِ، فَاتَّقُوا النَّارَ وَلَوْ بِشِقِّ تَمْرَةٍ».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح مسلم: 1016]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Adiy ibn Haatim yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne, Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:
«amul kenn ci yéen lu dul ne Yàlla dina wax ak moom, te kenn kuy firi du nekk seen diggante, mu xool ndayjooram du gis lu dul li mu jiital, mu xool càmmooñam du gis lu dul li mu jiital, mu xool kanamam du gis lu dul sawara wu jàkkarloo ak moom, ragalleen sawara donte dangeen joxe
aw xaru tàndarma la».
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Muslim bi gën a wér - 1016]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xamle ne aji-gëm ju ne dana taxaw ci kanamu Yàlla ëllëg bis-pénc moom dong, te Yàlla mu kawe mi dina wax ak moom te kenn du dox seen diggante di firi wax ji, mu xool wetu ndayjooram ak càmmoñam ngir njàqare lu tar, amaana mu gis yoon wu mu jaar ngir mucc ci sawara wi nekk ci kanamam. Bu xoolee wet gi nekk ci kanamam du gis lu dul jëf yu baax yi mu jiital, Bu xoolee ci wet gi nekk ci càmmoñam du gis lu dul jëf yu bon yi mu jiital, Bu xoolee kanamam du gis lu dul sawara, te manu ko a moytu ndax manul ñàkk mu jaar kaw Siraat. Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daal di wax ne: defleen ci seen diggante ak sawara kiiraayu saraxe ak def lu baax, donte lu tuuti la niki xaaju tàndarma.