+ -

عن عبد الله بن عمرو رضي الله عنهما أن النبي صلى الله عليه وسلم قال:
«الرَّاحِمُونَ يَرْحَمُهمُ الرَّحمنُ، ارحَمُوا أهلَ الأرضِ يَرْحْمْكُم مَن في السّماء».

[صحيح] - [رواه أبو داود والترمذي وأحمد] - [سنن أبي داود: 4941]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Abdulaah Ibn Amr -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
"ñiy yërëme Aji-Yërëme ji dana leen yërëm, yërëmleen waa suuf, kon ka ca kaw asamaan dana leen yërëm.

[Wér na] - [Abóo Daawuda soloo na ko, At-tirmisiy, ak Ahmat] - [Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda - 4941]

Leeral

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne ñiy yërëm ñeneen ñi Aji-Yërëme ji dana leen yërëm ca yërmàndeem ja xajoo lépp; muy ag pay gu dëppoo ak séen jëf.
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daal di digle ñu yërëm lépp lu nekk ci kaw suuf, muy nit walla mala, walla njanaaw mbaa yeneen xeeti mbindeef yi, payug loolu nag mooy Yàlla mi ci kaw asamaan yi yërëm leen.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Ciikiya Malagasi Itaali Oromoo Kanadi Ukraani
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Diiney Lislaam diiney yërmànde la, te léppam dafa taxaw ci topp Yàlla ak rafetal jëme ci mbindeef yi.
  2. Yàlla mu màgg mi dafa melowoo yërmànde, te moom Aji-Sell ji yërëmaakoon la ci ñépp te mooy yërëm ku ko soob ëllëg bis-pénc, te mooy àggale yërmànde ci jaamam ñi.
  3. Pay moom moo ngi aju ca kem jëf ya, ñiy yërëme Yàlla dana leen yërëm.