+ -

قال سعد بن هشام بن عامر -عندما دخل على عائشة رضي الله عنها-:
يَا أُمَّ الْمُؤْمِنِينَ، أَنْبِئِينِي عَنْ خُلُقِ رَسُولِ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ، قَالَتْ: أَلَسْتَ تَقْرَأُ الْقُرْآنَ؟ قُلْتُ: بَلَى، قَالَتْ: فَإِنَّ خُلُقَ نَبِيِّ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ كَانَ الْقُرْآنَ.

[صحيح] - [رواه مسلم في جملة حديثٍ طويلٍ] - [صحيح مسلم: 746]
المزيــد ...

Sahd Ibn Hisaam Ibn Aamir ba mu duggee ca néeg Aysatu -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa wax ne:
Yaw yaayu jullit ñi, wax ma jikkóy Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, mu ne ma: xanaa doo jàng Alxuraan? Ma ne ko: ahakay, mu ne ma: jikkóom moo doon.

[Wér na] - [Muslim soloo na ko ci ab Adiis bu gudd] - [Téere Muslim bi gën a wér - 746]

Leeral

Laaj nañu yaayu jullit ñi Aysatu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- jikkóy Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, mu tontu ci baat bu matale, daal di delloo laajkat bi ci Alxuraan ji boole mbooleem jikkó yu mat yi, daa di ne ko yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- jikkóy Alxuraan lajikkówoo woon, lu Alxuraan digle mu def ko, lu Alxuraan tere mu moytu ko, jikkóom doon jëfe Alxuraan, ak taxaw ci ay digam, tegginoo ay tegginam, waaru ci ay niralam ak i nettaleem.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Majri Ciikiya Malagasi Itaali Kanadi Ukraani
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Ñaaxe ci roy ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ak jikkówoo jikkóy Alxuraan.
  2. Tagg jikkóy Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci ne ci leeru wahyu gi la bokk.
  3. Alxuraan mooy cosaanu bépp jikkó bu tedd.
  4. Jikkó yi ci Lislaam day làmboo diine jépp, ci def ndigal yi, moytu tere yi.