+ -

عَنِ ‌ابْنِ عَبَّاسٍ رَضِيَ اللهُ عَنْهُمَا قَالَ:
أُنْزِلَ عَلَى رَسُولِ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ وَهُوَ ابْنُ أَرْبَعِينَ، فَمَكَثَ بِمَكَّةَ ثَلَاثَ عَشْرَةَ سَنَةً، ثُمَّ أُمِرَ بِالْهِجْرَةِ، فَهَاجَرَ إِلَى الْمَدِينَةِ، فَمَكَثَ بِهَا عَشْرَ سِنِينَ، ثُمَّ تُوُفِّيَ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ.

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 3851]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Ibn Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Wàcce na ñu ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- Alxuraan fekk mi ngi am ñent-fukki at, mu sax Màkka fukki at ak ñatt, ñu dugal ko mu gàddaay, mu gàddaay dem Madiina, sax fa fukki at, daal di faatu -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-.

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 3851]

Leeral

Ibn Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- day xibaare wàcce nañu ci Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- wahyu yónni ko fekk moo ngi am ñent-fukki at, mu sax Màkka fukki at ak ñatt ginnaaw soloo gi, ñu digal ko mu gàddaay dem Madiina mu sax fa fukki at, daal di Faatu -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- fekk moo ngi am juróom-benn fukki at ak ñatt.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Bosniya Sinhaaliya Endo Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Taajiki Kinirowanda Rom Majri Ciikiya Malagasi Itaali Oromoo Kanadi Asrabijaani Usbeg Ukraani
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Bokk na ci njariñal hdiis:
  2. Yittewoog Sahaaba yi jaar-jaari Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-.