عن أبي هريرة رضي الله عنه أن رسول الله صلى الله عليه وسلم قال:
«كُلُّ أُمَّتِي يَدْخُلُونَ الْجَنَّةَ إِلَّا مَنْ أَبَى»، قَالُوا: يَا رَسُولَ اللهِ، وَمَنْ يَأْبَى؟ قَالَ: «مَنْ أَطَاعَنِي دَخَلَ الْجَنَّةَ، وَمَنْ عَصَانِي فَقَدْ أَبَى».
[صحيح] - [رواه البخاري] - [صحيح البخاري: 7280]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«Sama xeet wépp dinañu dugg àjjana ba mu des ku bañ», ñu ne ko ana kan mooy bañ yaw Yónente Yàlla bi? Mu ne: «ku ma topp dugg àjjana ku ma moy nag kooku mooy ki bañ».
[Wér na] - [Al-buxaariy soloo na ko] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 7280]
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne xeetam wéppay dugg àjjana ba mu des ku bañ!
Sahaaba yi -yal na leen Yàlla dollee gërëm- ne ko: kan mooy bañ yaw Yónente Yàlla bi?!
Mu tontu leen ne leen: képp ku wommatu topp Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dana dugg àjjana, ku ko moy nag te wommatuwul ñeel Sariiha bi kooku moo bañ a dugg àjjana ngir ay jëfam yu bon.