عَنْ أَبِي بَرْزَةَ الأَسْلَمِيِّ رضي الله عنه قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«لَا تَزُولُ قَدَمَا عَبْدٍ يَوْمَ القِيَامَةِ حَتَّى يُسْأَلَ عَنْ عُمُرِهِ فِيمَا أَفْنَاهُ، وَعَنْ عِلْمِهِ فِيمَ فَعَلَ، وَعَنْ مَالِهِ مِنْ أَيْنَ اكْتَسَبَهُ وَفِيمَ أَنْفَقَهُ، وَعَنْ جِسْمِهِ فِيمَ أَبْلَاهُ».
[صحيح] - [رواه الترمذي] - [سنن الترمذي: 2417]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Barsata Al-Aslamii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«jaam bi du seqi benn jéego ëllëg bis-pénc ludul ne dees na ko laaj dundam gi ci lan la ko jeexale, ak xam-xamam bi lu mu ci def, ak alalam nan la ko ame ak ci fan la ko dugal , ak yaramam wi ci lan la ko ràppal».
[Wér na] - [At-tirmisiy soloo na ko] - [Téere Sunna yi bu At-tirmisiy - 2417]
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne kenn ci nit ñi du weesu bérabu regle ba ëllëg bis-pénc jëm àjjana walla sawara lu dul ne dees na ko laaj ay mbir:
Bi ci njëkk: dundam gi ci lan la ko jeexal?
Ñaareel bi: xam-xamam bi ndax da koo sàkku ngir Yàlla? Ak ndax jëfe na ko? Ak ndax jottali na ko ñi ko yeyoo?
Ñatteel bi: alalam ji fan la ko ame ndax ci lu dagan la walla lu araam? Ak fan la ko dugal, ci lu Yàlla gërëm la walla lu koy merloo?
Ñenteel bi: yaramam wi ak kàttanam gi ak jàmmam ji ak waxambaanem gi ci lan la ko ràppale, lu mu ci def?