عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رضي الله عنه أَنَّ رَسُولَ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ يَوْمَ خَيْبَرَ:
«لَأُعْطِيَنَّ هَذِهِ الرَّايَةَ رَجُلًا يُحِبُّ اللهَ وَرَسُولَهُ، يَفْتَحُ اللهُ عَلَى يَدَيْهِ» قَالَ عُمَرُ بْنُ الْخَطَّابِ: مَا أَحْبَبْتُ الْإِمَارَةَ إِلَّا يَوْمَئِذٍ، قَالَ فَتَسَاوَرْتُ لَهَا رَجَاءَ أَنْ أُدْعَى لَهَا، قَالَ فَدَعَا رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ عَلِيَّ بْنَ أَبِي طَالِبٍ، فَأَعْطَاهُ إِيَّاهَا، وَقَالَ: «امْشِ، وَلَا تَلْتَفِتْ، حَتَّى يَفْتَحَ اللهُ عَلَيْكَ» قَالَ فَسَارَ عَلِيٌّ شَيْئًا ثُمَّ وَقَفَ وَلَمْ يَلْتَفِتْ، فَصَرَخَ: يَا رَسُولَ اللهِ، عَلَى مَاذَا أُقَاتِلُ النَّاسَ؟ قَالَ: «قَاتِلْهُمْ حَتَّى يَشْهَدُوا أَنْ لَا إِلَهَ إِلَّا اللهُ وَأَنَّ مُحَمَّدًا رَسُولُ اللهِ، فَإِذَا فَعَلُوا ذَلِكَ فَقَدْ مَنَعُوا مِنْكَ دِمَاءَهُمْ وَأَمْوَالَهُمْ، إِلَّا بِحَقِّهَا وَحِسَابُهُمْ عَلَى اللهِ».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 2405]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax bisu Xaybar ba ne:
«dinaa jox Raaya ji waa ju bëgg Yàlla ak ub yonnenteem, Yàlla dina ko ubbee ci ay loxoom" Umar ibnul Xattaab nee na: masumaa bëgg a jiite lu dul bis boobu, nee na ma yoqamtiku ngir yaakaar ñu woo ma ngir moom, nee na Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daal di woo Aliyun Ibn Abii Taalib, jox ko raaya ji, ne ko: "doxal, te bul geestu, ba Yàlla ubbil la" nee na Aliyun dox tuuti daal di taxaw te geestuwul, daal di yuuxu ne: yaw Yonnente Yàlla bi, ci lan laay xeex ak nit ñi? Mu ne ko: "xeexal ak ñoom ba ñu seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla, ak ne Muhammat ndawul Yàlla la, bu ñu defee loolu kon tere nañu la seen dereet ak seen alal, lu dul ci àqam, seen ug càmbar nag ma nga ca Yàlla».
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 2405]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa xibaar Sahaabaam yi ci gañeg jullit ñi ëllëg ci kaw Yahuudi Xaybar yi -ab dëkk la ci wetu Madiina-, loolu nag ci loxob jenn waay ju ñuy jox raaya ji lay ame, te mooy Daraapoo wu Arme bi di def màndargaam, te waa jii bokk na ci ay meloom dafa bëgg Yàlla ak ub yonnenteem, Yàlla ak ub yonnenteem bëgg ko.
Umar ibnul Xattaab yal na ko Yàlla dollee gërëm wax na ne moom bëggul a jiite ak ñu koy jublu ci lu dul bis booba; ngir yaakaar li Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc wax dal ko muy bëggug Yàlla ak ub yonnenteem, Umar yoqamtiku ngir Yonnente bi gis ko woo ko, ak xér gi mu xér ci jël raaya ji
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daal di woo Aliyun Ibn Abii Taalib jox ko raaya ji, Yonnente bi digal ko mu yóbb Arme bi, ak mu bañ a wan ginnaaw xeex bi ginnaaw bu dajeek noon bi ngir noppalu walla taxawlu walla yéwénoo ba baa Yàlla di ko ubbil Tata yi ci am ndam ak not.
Aliyun yal na ko Yàlla dollee gërëm dox, daal di taxaw waaye geestuwul; ngir bañ a wuute ak ndigalu Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, Aliyun yëkkëti kàddoom daal di ne: yaw Yonnente Yàlla bi, ci lan laay xeex ak nit ñi?
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: xeexal ak ñoom ba baa ñuy seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla ak ne Muhammat ndawul Yàlla la, bu nu wuyoo, nangoo dugg ci lislaam; kon tere nañu la seen dereet ak seen alal mu araam ci yaw, lu dul àqam maanaam lu dul ñu def tooñaange walla ñaawteef wuy tax ñu yeyoo ray ci kem attey lislaam, seen ug càmbar nag ci Yàlla la aju.