+ -

عَنْ ‌أَنَسِ بْنِ مَالِكٍ رَضِيَ اللهُ عَنْهُ:
أَنَّ النَّبِيَّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ افْتَقَدَ ثَابِتَ بْنَ قَيْسٍ، فَقَالَ رَجُلٌ: يَا رَسُولَ اللهِ، أَنَا أَعْلَمُ لَكَ عِلْمَهُ، فَأَتَاهُ فَوَجَدَهُ جَالِسًا فِي بَيْتِهِ، مُنَكِّسًا رَأْسَهُ، فَقَالَ: مَا شَأْنُكَ؟ فَقَالَ شَرٌّ، كَانَ يَرْفَعُ صَوْتَهُ فَوْقَ صَوْتِ النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ، فَقَدْ حَبِطَ عَمَلُهُ، وَهُوَ مِنْ أَهْلِ النَّارِ، فَأَتَى الرَّجُلُ فَأَخْبَرَهُ أَنَّهُ قَالَ كَذَا وَكَذَا، فَرَجَعَ الْمَرَّةَ الْآخِرَةَ بِبِشَارَةٍ عَظِيمَةٍ، فَقَالَ: «اذْهَبْ إِلَيْهِ فَقُلْ لَهُ: إِنَّكَ لَسْتَ مِنْ أَهْلِ النَّارِ، وَلَكِنْ مِنْ أَهْلِ الْجَنَّةِ».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 3613]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Anas Ibn Maalik, -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa seet Saabit Ibn Xaysin, benn waay ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, man dinaa la xamal xibaaram, mu dikkal ko fekk ko mu toog ci këram, sëgg boppam bi, mu ne ko: ana luy sa mbir? Mu ne ko: xanaa ay, da doon yëkkati kàddoom ci kaw kàddug Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, kon moom ci waa sawara la, waa ji ñëw wax Yonnente bi ne ko: nee na lii ak lee, mu delluwaat beneen yoon indi ag bégle gu màgg, ne ko: "demal ne ko: yaw bokkoo ci waa sawara, waaye ci waa àjjana nga bokk".

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 3613]

Leeral

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- da doon seet Saabit Ibn Xaysin -yal na ko Yàlla dollee gërëm- daal di koy laajte, benn waay ne ko: man dinaa la amal xibaaram, ak lu tax mu fàddu, mu dem fa moom fekk ko ci këram mu jaaxle sëgg bopp bi, mu laaj ko: lan mooy sa mbir? Saabit wax ko ay wi nekk ci moom; ndaxte moom da daan yëkkati kàddoom ci kaw kàddug Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, te Yàlla dafa tëkku kuy def loolu ci ay jëfam yàqu, ak ne moom ne waa sawara la bokk!
Waa ji dellu fa Yonnente ba -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- xibaare ko loolu, Yonnente bi digal ko mu dellu fa Saabit bégal ko ci ne moom bokkul ci waa sawara waaye ci waa àjjana la bokk, ndaxte kàddoom gu kawe gi mbinddin la ci moom, ak ne moom moo doon waxal Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daan waxal it waa Lansaar yi.

Tekki: Àngale Urdu Endonesi Uyguuriya Bengali Turki Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Pulaar Itaali Oromoo Kanadi Asrabijaani Ukraani الجورجية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Leeral ngëneelu Saabit Ibn Xaysin -yal na ko Yàlla gërëm- ci ne moom ci waa àjjana la bokk.
  2. Yittewoo gi Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- yittewoo ay Sahaabaam ak daan leen nemmeeku.
  3. Ragal gi Sahaaba yi ragal ak tiit ci séen i jëf di yàqu.
  4. Dañoo war a am i teggin bu ñuy wax ak Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci bi muy dund, ak di suufeel kàddu yi bu ñuy déglu sonnaam ginnaaw bi mu faatoo.