+ -

عَنِ ‌ابْنِ عُمَرَ رضي الله عنهما:
أَنَّ رَسُولَ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ خَطَبَ النَّاسَ يَوْمَ فَتْحِ مَكَّةَ، فَقَالَ: «يَا أَيُّهَا النَّاسُ، إِنَّ اللهَ قَدْ أَذْهَبَ عَنْكُمْ عُبِّيَّةَ الْجَاهِلِيَّةِ وَتَعَاظُمَهَا بِآبَائِهَا، فَالنَّاسُ رَجُلَانِ: بَرٌّ تَقِيٌّ كَرِيمٌ عَلَى اللهِ، وَفَاجِرٌ شَقِيٌّ هَيِّنٌ عَلَى اللهِ، وَالنَّاسُ بَنُو آدَمَ، وَخَلَقَ اللهُ آدَمَ مِنْ تُرَابٍ، قَالَ اللهُ: {يَا أَيُّهَا النَّاسُ إِنَّا خَلَقْنَاكُمْ مِنْ ذَكَرٍ وَأُنْثَى وَجَعَلْنَاكُمْ شُعُوبًا وَقَبَائِلَ لِتَعَارَفُوا إِنَّ أَكْرَمَكُمْ عِنْدَ اللهِ أَتْقَاكُمْ إِنَّ اللهَ عَلِيمٌ خَبِيرٌ} [الحجرات: 13]».

[صحيح] - [رواه الترمذي وابن حبان] - [سنن الترمذي: 3270]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Abdullah Ibn Umar -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa doon xutba nit ñi ca bisu ubbiteg Màkka ga daal di ne leen: «yéen nit ñi Yàlla de jële na ci yéen rëy-rëylug ceddo ga ak seenug damu ci seen baay ya, nit ñi de ñaar kepp la ñu: ku baax te ragal Yàlla daal di tedd fa Yàlla, ak ub kàccoor bu texeedi doyadi fa Yàlla, nit ñi nag ay doomi Aadama la ñu, te Yàlla a ngi binde Aadama ci suuf, Yàlla neena: [yéen nit ñi nun noo leen bind ci góor ak jigéen def leen ay giir ak i xeet ngir ngeen xamante waaye ki gën a tedd fa Yàlla ci yéen mooy ki gën a ragal Yàlla, Yàlla de ku xam la te dara umpu ko} [Saaru Al-Hujraat: 13]»

[Wér na] - [At-tirmisiy soloo na ko, ak Ibnu Hibbaan] - [Téere Sunna yi bu At-tirmisiy - 3270]

Leeral

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa doon xutba nit ñi ca bisub ubbiteg Màkka ga daal di wax ne: yéen nit ñi Yàlla de dindi na ci yéen rëy-rëylug ceddu ya, ak di puukarewoo baay ya, waaye nit ñi ñaari xaaj lañu:
Ben muy aji-gëm di ku baax te ragal Yàlla di topp tey jaamu Yàlla mu màgg mi, kii moom ku tedd la fa Yàlla, donte nekkul boroom daraja ak askan wu kawe fa nit ña.
Mbaa muy ab yéefar di ku kàccoore di ku texeedi, kii moom ku doyadi la te suufe fa Yàlla, tollul nenn, donte dafa nekk boroom askan ak daraja ak nguur.
Nit ñépp ay doomi Aadama lañu, te Yàlla ci suuf la binde Aadama, kon yellul ci ku cosaanam nekk suuf muy rëy-rëylu ak di yéem boppam, liy dëggal loolu mooy waxu Yàlla mu kawe mi: {yéen nit ñi nun noo leen bind ci góor ak jigéen def leen ngeen di ay xeet ak i giir ngir ngeen xamante ki gën a tedd fa Yàlla nag mooy ki gën a ragal Yàlla ci yéen Yàlla ku xam la ku deñ kumpa ci lépp la} [Al-Hujraat: 13].

Tekki: Àngale Urdu Endonesi Uyguuriya Bengali Turki Bosniya Sinhaaliya Endo Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Ciikiya Malagasi Itaali Oromoo Kanadi Ukraani
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Tere nañu puukarewu ci askan ak daraja.