عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«وَالَّذِي نَفْسِي بِيَدِهِ، لَيُوشِكَنَّ أَنْ يَنْزِلَ فِيكُمْ ابْنُ مَرْيَمَ حَكَمًا مُقْسِطًا، فَيَكْسِرَ الصَّلِيبَ، وَيَقْتُلَ الخِنْزِيرَ، وَيَضَعَ الجِزْيَةَ، وَيَفِيضَ المَالُ حَتَّى لاَ يَقْبَلَهُ أَحَدٌ».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 2222]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«giñ naa ci ki sama bakkan nekk ci loxoom, daa naka rekk Iisaa Ibn Maryama wàcc ci yeen di ab àttekat bu màndu, di toj kurwaa yi, di ray mbaam-xuux yi, dindi galag gi(empo) bi, alal daal di baawaan ba kenn soxlawu ko».
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 2222]
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day waat ci ne wàccug Hisaa Ibn Maryama -yal na ko Yàlla dolli jàmm- jege na day wàcc di àtte ci diggante nit ñi cig màndute ci Sariihab Muhammat, Ak ne dana toj kurwaa yi nasaraan yi di màggal, Ak ne Hisaa-yal na ko Yàlla dolli jàmm-dana ray mbaam-xuux yi, Ak ne moom dana dindi lempo digal nit ñépp ñu dugg ci Lislaam. Ak ne alal dana baawaan ba kenn du ko jël; ndax bariwaayam, ak doylug kenn ku ne ci li mu am, baarke wàcc yiw yi toftaloo.