+ -

عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ: أَنَّ رَسُولَ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«لاَ تَقُومُ السَّاعَةُ حَتَّى تَطْلُعَ الشَّمْسُ مِنْ مَغْرِبِهَا، فَإِذَا طَلَعَتْ فَرَآهَا النَّاسُ آمَنُوا أَجْمَعُونَ، فَذَلِكَ حِينَ: {لاَ يَنْفَعُ نَفْسًا إِيمَانُهَا لَمْ تَكُنْ آمَنَتْ مِنْ قَبْلُ، أَوْ كَسَبَتْ فِي إِيمَانِهَا خَيْرًا} [الأنعام: 158] وَلَتَقُومَنَّ السَّاعَةُ وَقَدْ نَشَرَ الرَّجُلاَنِ ثَوْبَهُمَا بَيْنَهُمَا فَلاَ يَتَبَايَعَانِهِ، وَلاَ يَطْوِيَانِهِ، وَلَتَقُومَنَّ السَّاعَةُ وَقَدِ انْصَرَفَ الرَّجُلُ بِلَبَنِ لِقْحَتِهِ فَلاَ يَطْعَمُهُ، وَلَتَقُومَنَّ السَّاعَةُ وَهُوَ يَلِيطُ حَوْضَهُ فَلاَ يَسْقِي فِيهِ، وَلَتَقُومَنَّ السَّاعَةُ وَقَدْ رَفَعَ أَحَدُكُمْ أُكْلَتَهُ إِلَى فِيهِ فَلاَ يَطْعَمُهَا».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 6506]
المزيــد ...

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«Bis-pénc du ñëw mukk ba keroog jànt bi di fenke sowwu, bu fa fenkee nag ba nit ñi gis ko ñoom ñéppay gëm, te loolu mooy jamono joj: {amul benn bakkan bu ngëmam di jariñ bu gëmul woon lu njëkk, te fàggu ca ngëmam ga aw yiw} [Al-Anhaam: 158] bis-pénc dana taxaw fekk ñaari waay tallal nañu séen yére seen diggante te duñu ko mujj a jaayante, dunu ko it mujj a lem, bis-pénc dana taxaw fekk ben waay juge na fa mu ràtte soowam te du ko mos sax, bis-pénc dana taxaw fekk nit a ngi tabax ab baajam te du sa naan, fekk nit ki yëkkati ab tibam jame ko ci gémmeñam te du ko ñam».

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 6506]

Leeral

Leerarug hdiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne bokk na ci màndargay bis-pénc yu mag yi jant bi fenke sowwu, bu ko nit ñi gisee ñoom ñépp gëm, Ci loolu nag yéefar bi ngëmam du ko jariñ, te jëf lu baax dootul jariñ tuub it du jariñ. Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- xamle ne it bis-pénc cig mbetteel lay ñëwe; ba dana ñëw fekk nit ñi nekk ci séen biri dund gi; Bis-pénc dina ñëw fekk jaaykat bi ak jëndkat bi tàllal ab yéere séen diggante te duñu ko mujj a jaayante, te it duñu ko lem, Bis-pénc it dana taxaw fekk nit ki jël soow mu mu ratte cig giléemam te du ko mujj a naan, Bis-pénc it dana taxaw fekk nit ki di defar ab baajam di ko raax te du ci mujj a naan, Bis-pénc it dana taxaw fekk nit ki yëkkati ab dank jëme ko ci gimiñam ngir lekk ko te du ko mujj a lekk.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Taajiki Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Itaali Oromoo Kanadi البلغارية Asrabijaani اليونانية Usbeg Ukraani الجورجية اللينجالا المقدونية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Bokk na ci njariñal hdiis bi :
  2. Jébbalu ak tuub dees na ko nangu li feeg jant bi fenkeegul sowwu.
  3. Soññee ci waajal bis-pénc ci ngëm ak def lu baax; ndaxte bis-pénc day ñëwe cig mbetteel.