عَنْ عَبْدِ اللهِ بْنِ عَمْرِو بْنِ العَاصِ رضي الله عنهما قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«إِنَّ اللهَ سَيُخَلِّصُ رَجُلًا مِنْ أُمَّتِي عَلَى رُءُوسِ الْخَلَائِقِ يَوْمَ الْقِيَامَةِ، فَيَنْشُرُ عَلَيْهِ تِسْعَةً وَتِسْعِينَ سِجِلًّا، كُلُّ سِجِلٍّ مِثْلُ مَدِّ الْبَصَرِ، ثُمَّ يَقُولُ: أَتُنْكِرُ مِنْ هَذَا شَيْئًا؟ أَظَلَمَكَ كَتَبَتِي الْحَافِظُونَ؟ فَيَقُولُ: لَا يَا رَبِّ، فَيَقُولُ: أَفَلَكَ عُذْرٌ؟ فَيَقُولُ: لَا يَا رَبِّ، فَيَقُولُ: بَلَى إِنَّ لَكَ عِنْدَنَا حَسَنَةً، فَإِنَّهُ لَا ظُلْمَ عَلَيْكَ الْيَوْمَ، فَتُخْرَجُ بِطَاقَةٌ فِيهَا: أَشْهَدُ أَنْ لَا إِلَهَ إِلَّا اللهُ وَأَشْهَدُ أَنَّ مُحَمَّدًا عَبْدُهُ وَرَسُولُهُ، فَيَقُولُ: احْضُرْ وَزْنَكَ، فَيَقُولُ: يَا رَبِّ مَا هَذِهِ الْبِطَاقَةُ مَعَ هَذِهِ السِّجِلَّاتِ؟ فَقَالَ: إِنَّكَ لَا تُظْلَمُ، قَالَ: فَتُوضَعُ السِّجِلَّاتُ فِي كِفَّةٍ، وَالْبِطَاقَةُ فِي كِفَّةٍ، فَطَاشَتِ السِّجِلَّاتُ، وَثَقُلَتِ الْبِطَاقَةُ، فَلَا يَثْقُلُ مَعَ اسْمِ اللهِ شَيْءٌ».
[صحيح] - [رواه الترمذي وابن ماجه] - [سنن الترمذي: 2639]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Abdullah Ibn Amr Ibnul Haasi -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«Yàlla dina musal nit ci samaw xeet ci kanamu mbindéef yépp ëllëg bis-pénc, mu génneel ko juróom ñeent fukk ak juróom ñeenti téere, téere bune dana toll fa gisu bët yam, ñu ne ko: Ndax dagay weddi dara ci lii ? Ndax samay bindkat dañu laa tooñ ? Mu ne ko: Déedéet yaw Boroom bi. Mu ne ko: ndax kon am nga ngànt ? Mu ne ko: Déedéet yaw Boroom bi, Mu ne ko: ahakay, am nga fi nun aw yiw, te fii tay kenn du la fi tooñ, ñu génne ag kayit gog la ca nekk mooy: Seede naa ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla, Maa ngi seede ni Mohammat jaamam la di Yónenteem. Ñu ne ko: indil sa màndaxekaay, muy wax naan: ay sama Boroom lu kayit wii di jariñ ci wetu téere yii ? Ñu ne ko: kenn du la fi tooñ, nee na: ñu teg téere yi ci genn wàll, teg kayit wi ci geneen wàll, téere yi tasaaro, kayit wa daal di diis nit téere ya, dara du diis ci wetu turu Yàlla».
[Wér na] - [At-tirmisiy soloo na ko, ak Ibnu Maaja] - [Téere Sunna yi bu At-tirmisiy - 2639]
Leerarug hdiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak jàmm-, wax na ne Yàlla day tànn benn waay ci xeetam wi ci kanamu mbindéef yi ëllëg bis-pénc ba woo ko ngir càmbar ko, ñu gaaral ko juróom-ñeent-fukk ak juróom-ñeenti téere, te mooy téerey jëf yu bon yi mu daan def ci àdduna, te guddaayu téere bu nekk mi ngi toll ci guddaay bi bët man a gis, Yàlla mu màgg mi wax waa ji ne ko: ndax dangay weddi dara ci li ñu bind ci téere yi? Ndax sama Malaaka yiy bind dañu laa tooñ? Waa ji ne ko: déedéet yaw sama Boroom. Yàlla ne ko: ndax am nga ngànt lu ñu lay dogalal ci li nga jiital ci ay jëf ca àdduna ? ju tege ci njuumte walla ag réer, Waa ji ne ko: déedéet yaw sama Boroom amuma lenn ngànt. Yàlla ne ko: ahakay, am nga fi nun aw yiw, te tay kenn du la tooñ. Nee na: ñu génneel ko aw kayit nu bind ca: maa ngi seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ci dëgg ku dul Yàlla, di seede it ne Muhammat jaamu Yàlla la di Yónenteem. Yàlla ne waa ji: indil say màndaxekaay. Waa ji wax ngir yéemu ne: yaw sama Boroom! Naka la ñuy màndaxee kayit wii ci téere yii ?! Yàlla ne ko: deesu la tooñ. Nee na: ñu teg téere yi ci genn wàll, teg kayit wi ci genn wàll gi; wàll wi téere yi nekk daal di woyof, wàll wi kayit wi nekk daal di not daal di diis, Yàlla jéggal ko.