Xàjjaley wanqaas yi

Toftaleg Adiis yi

mbaa sama Hadiis du yeksi ci nit mu tëdd ag gàngunaayam naan: Diggante nun ak yéen téeréb Yàlla la
عربي Àngale Urdu
ñoom ñaar de ñoo ngi leen di mbugal, te sax mbugaluñu leen ci lu rëy, kenn ki moom daawul suturawu bu daan saw, keneen ki nag da daan dox di rambaaj
عربي Àngale Urdu
Bokk na ci màndargay bis-pénc nu yëkkati xam-xam, réer bari, njaalo bari, naan sàngara bari, góor ñi néew, jigéen ñi bari, ba juróom-fukki jigéen di tolloog benn góor
عربي Àngale Urdu
saa du taxaw lu dul ne nit dana romb ci bàmmeelu benn waay naan: aka neexoon ma nekk palaasam
عربي Àngale Urdu
bis-pénc du taxaw ba keroog ngeeni xeex ak Yahuut yi, ba doj wu ab Yahuut nekk ci ginnaawam di wax naan: yaw jullit bi, ab Yahuut a ngi nii sama ginnaaw ñëwal ray ko
عربي Àngale Urdu
giñ naa ci ki sama bakkan nekk ci loxoom, daa naka rekk Iisaa Ibn Maryama wàcc ci yeen di ab àttekat bu màndu, di toj kurwaa yi, di ray mbaam-xuux yi, dindi galag gi(empo) bi, alal daal di baawaan ba kenn soxlawu ko
عربي Àngale Urdu
Bis-pénc du ñëw mukk ba keroog jànt bi di fenke sowwu, bu fa fenkee nag ba nit ñi gis ko ñoom ñéppay gëm
عربي Àngale Urdu
saa du taxaw ba keroog jamono ji di jegee
عربي Àngale Urdu
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa am lu mu tudd daal di ne: «loolu de bu xam-xam di dem lay doon
عربي Àngale Urdu
ci sama mujjuw xeet wi dana am ay nit yu leen di wax lu ngeen masuta dégg yéen ak séen i baay, nangeen leen moytu
عربي Àngale Urdu