عَنِ البَرَاءِ بْنِ عَازِبٍ رضي الله عنه أَنَّ رَسُولَ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«المُسْلِمُ إِذَا سُئِلَ فِي القَبْرِ: يَشْهَدُ أَنْ لاَ إِلَهَ إِلَّا اللَّهُ وَأَنَّ مُحَمَّدًا رَسُولُ اللَّهِ»، فَذَلِكَ قَوْلُهُ: {يُثَبِّتُ اللَّهُ الَّذِينَ آمَنُوا بِالقَوْلِ الثَّابِتِ فِي الحَيَاةِ الدُّنْيَا وَفِي الآخِرَةِ} [إبراهيم: 27].
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 4699]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Al-Baraa ibn Aasib -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«jullit bi bu ñu ko laajee ci bàmmeel: day seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla ak ne Muhammat ndawul Yàlla la" loolu mooy li Yàlla mu kawe mi wax: {Yàlla dana saxal way-gëm ñi ci wax juy sax ci dundug àdduna ak ci allaaxira} [Ibraahiima: 27].
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 4699]
Dañuy laaj aji-gëm ji ci bàmmeel, ñaari malaaka yi dénk loolu laaj ko ñooñu ñooy Munkar ak Nakiir ñu laaj ko, kem ni ñu leen tudde ci ay hadiis yu bari, Mu seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla ak ne Muhammat ndawul Yàlla la, Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na wax jii mooy wax jay sax wax ji Yàlla ne: {Yàlla dana saxal way-gëm ñi ci wax juy sax ci dundug àdduna ak ci allaaxira} [Ibraahiima: 27].