+ -

عَنِ ابْنِ عُمَرَ رضي الله عنهما أَنَّ رَسُولَ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«أُمِرْتُ أَنْ أُقَاتِلَ النَّاسَ حَتَّى يَشْهَدُوا أَنْ لاَ إِلَهَ إِلَّا اللَّهُ، وَأَنَّ مُحَمَّدًا رَسُولُ اللَّهِ، وَيُقِيمُوا الصَّلاَةَ، وَيُؤْتُوا الزَّكَاةَ، فَإِذَا فَعَلُوا ذَلِكَ عَصَمُوا مِنِّي دِمَاءَهُمْ وَأَمْوَالَهُمْ إِلَّا بِحَقِّ الإِسْلاَمِ، وَحِسَابُهُمْ عَلَى اللَّهِ».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 25]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Ibn Umar -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-mu wax ne:
«digal nañu ma ma xeex ak nit ñi ba baa ñuy seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla ak ne Muhammat ndawul Yàlla la, ak taxawal julli, ak joxe asaka, bu ñu defee loolu ñoŋal nañu ci ma seen dereet ak seen alal lu dul ci àqi Lislaam, seenub regle nag ci Yàlla la aju».

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 25]

Leeral

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne Yàlla digal na ko mu xeex ak bokkaalekat yi ba keroog ñuy seede ne amul kenn ku ñu jaamu ci dëgg ku dul Yàlla moom dong amul bokkaale, ak ñu seedeel Muhammat -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ag yónnenteem, te jëfe li seede si laaj ci sàmmonte ak julliy juróom ci bis bi ak ci guddi gi, ak joxe asaka ji ñu farataal ñeel ñi ko yeyoo. Bu ñu defee bir yii kon Lislaam dana ñoŋal seen dereet ak seen alal, du dagan ñu ray leen lu dul bu ñu defee ñaawteef walla tooñaange juy warala ñu yeyoo ray ci ni ko àttey Lislaam warale, topp bisu pénc ba Yàlla mooy méngoo seenug regle ndax moo xam seen yu nëbbu yi.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taylandi Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Oromoo Kanadi Ukraani الجورجية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Àtte yi ci li feeñ lay ame, Yàlla nag mooy méngoo yi nëbbu.
  2. Solos woote jëme ci Tawhiid ndaxte mooy li ñuy njëkk a tàmbalee ci woote.
  3. Hadiis bii nag tekkiwul ga bokkaalekat yi ci dugg ci Lislaam, waaye dañu leen di tànnloo ci diggante dugg ci Lislaam walla joxe juuti; bu ñu bañee lu dul di tere nu woote ci Lislaam, dara desu fa lu dul rayante ak ñoom kem ni ko àttey Lislaam warale.