عَنِ ابْنِ مَسْعُودٍ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ، قَالَ:
قَالَ رَجُلٌ: يَا رَسُولَ اللهِ، أَنُؤَاخَذُ بِمَا عَمِلْنَا فِي الْجَاهِلِيَّةِ؟ قَالَ: «مَنْ أَحْسَنَ فِي الْإِسْلَامِ لَمْ يُؤَاخَذْ بِمَا عَمِلَ فِي الْجَاهِلِيَّةِ، وَمَنْ أَسَاءَ فِي الْإِسْلَامِ أُخِذَ بِالْأَوَّلِ وَالْآخِرِ».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 6921]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Ibn Mashuud -yal na ko Yàlla dollee gërëm-, mu wax ne:
Benn waay dafa ne: yaw Yónente Yàlla bi, ndax dañ nuy toppe la nu defoon ca ceddu ga ? Mu ne ko: «ku rafetal ci Lislaam deesu ko toppe la mu defoon ca ceddu ga, waaye ku def lu ñaaw ci Lislaam dees na ko toppe lu njëkk la ak lu mujj li».
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 6921]
Leerarug hdiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ngëneelul dugg ci Lislaam, Ak ne képp ku tuub te rafetal Lislaamam tey sellal te dëggu; deesul luññutu la mu defoon ca ceddo ga ci ay moy, Waaye képp kuy ñaawal ci Lislaam ci nekk ab naaféq walla mu génn ci diine ji; dees na ko àtte ca la mu defoon ca kéefar ga ak li mu jëf ci Lislaam.