عن أبي هريرة رضي الله عنه قال: قال رسول الله صلى الله عليه وسلم:
«الْإِيمَانُ بِضْعٌ وَسَبْعُونَ -أَوْ بِضْعٌ وَسِتُّونَ- شُعْبَةً، فَأَفْضَلُهَا قَوْلُ لَا إِلَهَ إِلَّا اللهُ، وَأَدْنَاهَا إِمَاطَةُ الْأَذَى عَنِ الطَّرِيقِ، وَالْحَيَاءُ شُعْبَةٌ مِنَ الْإِيمَانِ».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح مسلم: 35]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónenteb Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«Ngëm juróom-ñaar fukki xaaj la ak lu topp» wala: «juróom-benn fukki xaaj la ak lu topp» - ci ay xaaj, bi ci gën a kawe: mooy wax: laa ilaaha illal Illa Laahu, bi ci gën a suufe, mooy: randale aw lor ci kaw yoon wi, te kersa benn pàcci la ci ngëm»
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Muslim bi gën a wér - 35]
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne ngëm ay xaaj la ak i melo yu bari, te day làmboo jëf yi ak pas-pas yi ak wax yi.
Ak ne li gën kawe ci ngëm te gën ca mooy wax: «laa ilaaha illal laahu» te xam maanaama , tey jëfe lamu làmboo, ci ne Yàlla moom mooy Yàlla miy kenn mooy ki yayoo ag jaamu moom dong deesul jaamu leneen.
Ak ne jëf ji gën a tuuti ci ngëm, mooy randale lépp luy lor nit ñi ci yoon yi.
Yónente bi xibaare na ci ne lii di kersa ci meloy ngëm la bokk, jikko la juy waral def lu rafet te bàyyi lu ñaaw.