+ -

عن أبي مسعود رضي الله عنه عن النبي صلى الله عليه وسلم قال:
«إِذَا أَنْفَقَ الرَّجُلُ عَلَى أَهْلِهِ يَحْتَسِبُهَا فَهُوَ لَهُ صَدَقَةٌ».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 55]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Abuu Mashuud -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«bu nit ki dundalee njabootam di ci séentu aw yiw loolu dina nekk ci moom ab sarax».

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 55]

Leeral

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne bu nit ki joxee njël njabootam gimu war a dundal, niki jabaram ak way-juram ak i doomam ak ñeneen, di sàkkoo jege Yàlla ci loolu, di yaakaar ci moom payug li mu joxe kon dana am yoolub sarax.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Majri Ciikiya Malagasi Itaali Kanadi Asrabijaani Ukraani
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Dundal njaboot gi dees ciy am ab yool.
  2. Aji-gëm ji day sàkku ci jëfam ji jëmmi Yàlla ji ak la fa moom ci ab yool.
  3. Deesa war a teewal yéene ju sell ci jépp jëf, bokk na ci yooyu jamonoy dundal njaboot.