+ -

عن أبي هريرة رضي الله عنه أن رسول الله صلى الله عليه وسلم قال:
«قَالَ اللهُ: أَنْفِقْ يَا ابْنَ آدَمَ أُنْفِقْ عَلَيْكَ».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 5352]
المزيــد ...

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«Yàlla nee na: yaw doomu Aadama ji joxeel ma jox la».

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 5352]

Leeral

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dañuy xamal ne Yàlla mu kawe mi dafa wax ne: yaw doomu Aadama ji joxeel -dund gila war ak giñu sopp- ma yaatalal la jox la lu ko wuutu te barkeelal la ko.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Taajiki Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Itaali Kanadi البلغارية Asrabijaani Ukraani الجورجية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Ñaaxe ci saraxe ak joxe ci yooyu Yàlla.
  2. Joxe ci mbir yu baax yi bokk na ci sabab yi gën a màgg yiy baarkeel wërsëg di ko ful, ak Yàlla wuutalal jaam bi la mu joxe woon.
  3. Hadiis bii dafa bokk ci li Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nettali jële ko ci Boroomam, ñu di ko woowe Hadiis Al-xuddsi walla Hadiisu Al-Ilaahiy, te mooy Hadiis bi nga xam ne ay baatam ak i maanaam ci Yàlla la juge, waaye amul jagle yi nekk ci Alxuraan te mu koy ràññee ak lu dul moom, niki di jaamu Yàlla ci jàng gi ak di laab ngir jàng ko, ak di ci dëkke mbaa di ci lottalaate ak yenneen.