Toftaleg Adiis yi

kiy jokk mbokk du kiy faye liñuko jokk, waaye kiy jokk mbokk mooy ki nga xam ne bu ñu dogee ag mbokkam mu jokk ka ko dog
عربي Àngale Urdu
ki gën a mat ug ngëm ci jullit ñi mooy ki ci gën a rafet jikko, te ki gën ci yéen mooy ki gën ci ay jigéenam
عربي Àngale Urdu
àdduna ay jumtukaay rekk la, te li gën ci jumtukaay yi àdduna mooy jigéen ju baax
عربي Àngale Urdu
Yàlla nee na: yaw doomu Aadama ji joxeel ma jox la
عربي Àngale Urdu
sart yi gën a yelloo matal mooy yi ngeen daganale péy ya
عربي Àngale Urdu
bu nit ki dundalee njabootam di ci séentu aw yiw loolu dina nekk ci moom ab sarax
عربي Àngale Urdu
Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- tere na zulu
عربي Àngale Urdu
Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- xamal na ñu xutbag aajo
عربي Àngale Urdu
Deesul takk jigéen ci lu dul kilifa
عربي Àngale Urdu
àdduna de ñam wu neex la te naat, Yàlla da leen fee wuutal, di xool lu ngeen fiy jëf, noytuleen àdduna te moytu jigéen ñi
عربي Àngale Urdu
Jullit bu góor du bañ jullit bu jigéen, ndax su bañee ci moom jenn jikkó gërëm na ci moom jeneen jikkó
عربي Àngale Urdu
ku ne ci yéen ab sàmm la te dees na ko laaj la mu doon sàmm,
عربي Àngale Urdu
ku man a takk jabar na takk, ndaxte moo gën a man a damm ab gis, gën a man a sàmm péy mi, ku ko manul nag dénk naa ko woor, ndaxte dana ko man a téye
عربي Àngale Urdu
moytandikuleen di jaxasoo ak jigéen ñi" jenn waay ci Ansaar yi ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, noo gise goro? Mu ne ko: "goro moo dee faf
عربي Àngale Urdu
yéen mbooloom jigéen ñi deeleen saraxe, man de gis naa leen ngeen ëpp ci waa sawara" ñu ne ko: ndax lan yaw Yonente Yàlla bi? Mu ne: "dangeen a bari ag rëbbaate, di weddi njekk, gisuma jigéen ñu matadi xel ak diine te gaaw a yóbb xelu góor gu dogu ba mel ni kenn ci yéen jigéen ñi
عربي Àngale Urdu
bu genn jigéen tukki lu mat doxub ñaari fan lu dul mu ànd ak jëkkëram walla ab jegeñaaleem
عربي Àngale Urdu
jépp jigéen bu ñu fasal ab sëy ci lu dul ndigalu kilifaam, sëyam ba ag neen la -ñatti yoon- bu àndee ak moom can ga ñeel na ko ca la mu ànd ak moom, bu nu werentee buur mooy nekk kilifag ku amul kilifa
عربي Àngale Urdu
rëbbees na kiy sëy ak soxnaam ci ginnaawam
عربي Àngale Urdu
Damaa wax ne: yaw Yonente Yàlla bi, lan mooy àqi jabaru kenn ci nun?, mu wax ne: «nga jox ko mu lekk boo lekkee, nga solal ko boo solee, walla nga fàggu, te bul dóor ci kanam gi, te bul ñaawal, bul gàddaay fu dul ci kër gi
عربي Àngale Urdu
ku am ñaari jabar daal di jeng ci kenn ki, dana ñëw ëllëg bis-pénc wetam gi jeng
عربي Àngale Urdu
Yàlla jéggal na samaw xeet li seen i xel di xalaat, fii ak defuñu mbaa ñu wax
عربي Àngale Urdu
ñaar yii dañoo araam ci sama góori xeet wi, waaye dagan nañu ci jigéen ñi
عربي Àngale Urdu