+ -

عن عقبة بن عامر رضي الله عنه قال: قال رسول الله صلى الله عليه وسلم:
«أَحَقُّ الشُّرُوطِ أَنْ تُوفُوا بِهِ مَا اسْتَحْلَلْتُمْ بِهِ الْفُرُوجَ».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 2721]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Huqbata Ibn Haamir -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne : Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«sart yi gën a yelloo matal mooy yi ngeen daganale péy ya.

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 2721]

Leeral

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne sart yi gën a yelloo matal mooy yiy ñu man a daganal bànneexu ci jigéen, te mooy sart yi dagan te jigéen gi di ko sàkku bu ñuy takk sëy ba.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Majri Ciikiya Malagasi Itaali Kanadi Asrabijaani Ukraani
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. War nañoo matal sart yi nga xam ne kenn ci ñaar ñiy sëy moo ko warlul keneen ki, lu dul muy sart buy araamal lu dagan walla muy daganal lu araam.
  2. Matal sarti sëy moo gën a feddaliku lu dul moom; ndaxte mooy tollook daganal awra ya.
  3. Màggug sëy ci Lislaam, ba tax mu feddali ne na ñuy matale sart ya.