+ -

عن أبي موسى رضي الله عنه أن النبي صلى الله عليه وسلم قال:
«لا نِكَاحَ إِلّا بِوَليٍّ».

[صحيح] - [رواه أبو داود والترمذي وابن ماجه وأحمد] - [سنن أبي داود: 2085]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Abuu Muusa Al-Ashsrii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«Deesul takk jigéen ci lu dul kilifa».

[Wér na] - [Ibnu Maaja soloo na ko - At-tirmisiy soloo na ko - Abóo Daawuda soloo na ko - Ahmat soloo na ko] - [Téere Sunna yi bu Ad-daaraqutniy - 2085]

Leeral

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa leeral ne jigéen du dagan ñu takk ko ci lu dul kilifa gu taxawe takk ga.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Ciikiya Malagasi Itaali Oromoo Kanadi Ukraani
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Kilifa sart la ci wérug sëy, bu takk amee ci lu dul kilifa, walla jigéen maye boppam, kon sëy ba du wér.
  2. Kilifa mooy góor gi gën a jege jigéen gi, kon kilifa gu sori du ko maye te ku jege nekk fa.
  3. Sàrtal nañu ci kilifa: mu nekk mukàllaf, nekk góor, am xelum xam njariñi sëy, te kilifa gi ak ka muy meye ñu bokk diine, ku amul melo yii manut a nekk kilifa ci fas ab sëy.
Ndollent