عن عبد الله بن مسعود رضي الله عنه قال:
عَلَّمَنَا رَسُوْلُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ خُطْبَةَ الحَاجَةِ: إِنَّ الحَمْدَ للهِ، نَسْتَعِيْنُهُ وَنَسْتَغْفِرُهُ، وَنَعُوْذُ بِهِ مِنْ شُرُوْرِ أَنْفُسِنَا، مَنْ يَهْدِ اللهُ فَلَا مُضِلَّ لَهُ، وَمَنْ يُضْلِلْ فَلَا هَادِيَ لَهُ، وَأَشْهَدُ أَنْ لَا إِلَهَ إِلَّا الله، وَأَشْهَدُ أَنَّ مُحَمَّدًا عَبْدُهُ وَرَسُوْلُهُ، {يَا أَيُّهَا النَّاسُ اتَّقُوا رَبَّكُمُ الَّذِي خَلَقَكُمْ مِنْ نَفْسٍ وَاحِدَةٍ وَخَلَقَ مِنْهَا زَوْجَهَا وَبَثَّ مِنْهُمَا رِجَالًا كَثِيرًا وَنِسَاءً وَاتَّقُوا اللَّهَ الَّذِي تَسَاءَلُونَ بِهِ والأرحام إن الله كان عليكم رقيبا} [النساء: 1]، {يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا اتَّقُوا اللَّهَ حَقَّ تُقَاتِهِ وَلَا تَمُوتُنَّ إِلَّا وَأَنْتُمْ مُسْلِمُونَ} [آل عمران: 102]، {يَا أَيُّهَا الَّذِينَ آمَنُوا اتَّقُوا اللَّهَ وَقُولُوا قَوْلًا سَدِيدًا (70) يُصْلِحْ لَكُمْ أَعْمَالَكُمْ وَيَغْفِرْ لَكُمْ ذُنُوبَكُمْ وَمَنْ يُطِعِ اللَّهَ وَرَسُولَهُ فَقَدْ فَازَ فَوْزًا عَظِيمًا} [الأحزاب:70 - 71].
[صحيح] - [رواه أبو داود والترمذي وابن ماجه والنسائي وأحمد] - [سنن أبي داود: 2118]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Abdullah Ibn Mashuud -yal na ko Yàlla dollee gërëm- me wax ne:
Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- xamal na ñu xutbag aajo: cant ñeel na Yàlla, ñoo ngi koy dimbandikoo, di ko jéggalu, di muslu ci moom ci ayu sunu bakkan, ku Yàlla gindi kenn manu koo sànk, ku Yàlla sànk kenn manukoo gindi, maa ngi seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla, tey seede ne Muhammat jaamam la Yónenteem la, {éey yéen nit ñi ragal leen séen Boroom mi leen bind ci benn bakkan bind ca it jabaram, tasaare si ñoom ñaar ay góor yu bari ak i jigéen, nangeen ragal Yàlla mi nga xam ne ci moom ngeen di laajante, te ragal ag meen, Yàlla moo ngi leen di fuglu}[An-Nisaa: 1], {éey yéen ñi gëm nangeen ragal séen Boroom dëgg-dëggi ragal te buleen dee lu dul ne ay jullit ngeen} [Aali-Imraan: 102], {éey yéen ñi gëm nangeen ragal Yàlla tey wax wax ju jub(70) kon dana yéwénal séen i jëf jéggal leen séen i bàkkaar, ku topp Yàlla ak ub Yónenteem texe na texe gu màgg} [Al-Ahsaab: 70-71].
[Wér na] - [Abóo Daawuda soloo na ko, ak At-tirmisiy, ak Ibnu Maaja, ak An-nasaa'iy, ak Ahmat] - [Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda - 2118]
Ibn Mashuud day xibaare ne Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- xamal na leen xutbay aajo, te mooy li ñuy wax bu ñuy tàmbalee wax ci xutba yi, ak ci aajo yi, niki xutbay takk ab sëy, ak xutbay àjjuma ak yeneen, Xutba gii nag dafa làmboo ay maanaa yu bari ci leeral ne Yàlla moo jagoo mbooleem xeeti cant yi, ak sàkku ndimbal ci moom dong amul bokkaale, ak suturaal bàkkaar yi te jéggale ko, ak làqu ci Yàlla ci bépp ay, ak ayi bàkkan yi ak yeneen.
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- xamle na ne gindee ci loxoy Yàlla la nekk, ku mu gindi kenn manu koo sànk, ku mu sànk it kenn manu koo gindi.
Mu tudd seede ci Tawhiid, ci ne amul kenn ku ñuy jaamu cig dëgg ku dul Yàlla, ak seedeg Yónent ci ne Muhammat jaamu Yàlla la di Yónenteem la.
Mu jeexale xutba gi ci ñatti aaya yu làmboo digleg ragal Yàlla mu màgg mi ci def ay ndigalam te moytu ay tereem, ngir sàkku jëmmi Yàlla ji, ak ne payug ku def loolu mooy sellug ay jëf ak i wax, ak far ay ñaawtéef, ak jéggalug bàkkaar yi, ak dund gu teey ci àdduna, ak texe ca àjjana ëllëg bis-pénc.