عن أُبيِّ بن كعبٍ رضي الله عنه قال:
صلَّى بنا رسولُ الله صلى الله عليه وسلم يومًا الصُّبحَ فقال: «أشاهِد فُلان؟» قالوا: لا، قال: «أشاهِدٌ فُلان؟» قالوا: لا، قال: «إنَّ هاتيَنِ الصَّلاتين أثقَلُ الصَّلَواتِ على المُنافقين، ولو تعلمون ما فيهما لأتيتُمُوهما ولو حَبْوًا على الرُّكب، وإن الصفَّ الأوّلَ على مِثلِ صَفِّ الملائكة، ولو عَلِمتُم ما فضيلتُه لابتَدَرتُموهُ، وإنّ صلاةَ الرجل مع الرجل أزكى من صلاتِه وحدَه، وصلاتَه مع الرجلَين أزكى من صلاتِه مع الرجل، وما كَثُرَ فهو أحبُّ إلى الله تعالى».
[صحيح] - [رواه أبو داود والنسائي وأحمد] - [سنن أبي داود: 554]
المزيــد ...
Jële nañu ci Ubay ibn Kahb yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne:
Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc jiite na nu benn bis jullig suba mu daal di wax ne: "ndax diw teew na?" Ñu ne ko: déedéet, mu ne waat: ndax diw teew na? Ñu ne ko déedéet, mu ne: "ñaari julli yii ñooy julli yi gën a diis ci naaféq yi, te bu ngeen xamoon li nekk ci ñoom ñaar dangeen ko teewe donte dangeen di raam ci ay wóom, te sàppe gu njëkk gi moo ngi mel ni sàppey malaaka yi, te bu ngeen xamoon ngëneelam dangeen ko njëkkante, jullig góor ànd ak ñaari góor moo ëpp julleem ak genn góor, lu gën a bari moo gënal Yàlla mu kawe mi".
[Wér na] - - [Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda - 554]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa julli fajar benn bis, daal di laaj: ndax diw teewe na julli gii? Sahaaba yi ne ko: déedéet. Mu wax keneen
ndax diw teew na? Ñu ne: déedéet. Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc wax ne: Jullig fajar ak gee ñoo gën a diis ci naaféq yi; ngir li tayyeel di ca not, ak li ca ngistal néew, ndax duñu leen gis ci lëndëm gi.
Bu ngeen xamoon li ci ñaari julli yii suba ak gee ci fay ak yool gu bari -ndax fay day yam ak coona- kon dangeen ko teewe donte dangeen di raam di doxe ay loxo ak i wóom.
Te sàppe gu njëkk gi ci ni ñu jegee imaam bi moo ngi mel ni sàppey Malaaka yi ci ni ñu jegee Yàlla mu kawe mi, te bu
jullit ñi xamoon ngëneelu sàppe gu njëkk gi kon danañu njëkkante jëm ca, Ak ne jullig góor ànd ak geneen
góor moo gën a màgg yool julleem moom dong, te ag julleem ak ñaari góor moo gën julleem ak genn góor, Julli gi bariy nit la Yàlla gën a bëgg te moo ëpp ngëneel.