عَنْ وَابِصَةَ رضي الله عنه:
أَنَّ رَسُولَ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ رَأَى رَجُلًا صَلَّى وَحْدَهُ خَلْفَ الصَّفِّ، فَأَمَرَهُ أَنْ يُعِيدَ صَلَاتَهُ.  
                        
[حسن] - [رواه أبو داود والترمذي وابن ماجه وأحمد] - [مسند أحمد: 18000]
                        
 المزيــد ... 
                    
Jële nañu ci Waabisata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne:
Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa gis jenn waay julli moom dong ci ginnaaw sàppe si, mu digal ko mu bàmtu julleem gi. 
                                                     
                                                                                                    
[Tane na] - [Abóo Daawuda soloo na ko,  At-tirmisiy, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat] - [Téere Adiisu Ahmat bees leeral càllala ya - 18000]                                            
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa gis jenn waay julli moom dong ci ginnaaw sàppe si, mu digal ko mu bàmtu julleem gi; ndaxte julleem gi ci anam googu du wér.