+ -

عَنْ أَنَسِ بْنِ مَالِكٍ رضي الله عنه قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«سَوُّوا صُفُوفَكُمْ، فَإِنَّ تَسْوِيَةَ الصَّفِّ مِنْ تَمَامِ الصَّلَاةِ».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح مسلم: 433]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Anas Ibn Maalik -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
"yamaleleen seen sàppe yi, ndax yamale sàppe yi daa bokk ci matug julli gi"

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Muslim bi gën a wér - 433]

Leeral

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day digal jullikat yi ñu yamale seen sàppe yi, te kenn bañ a jiitu kenn mbaa mu koy mujj, ak ne yamale sàppe yi daa bokk ci matug julli gi, waaye dëngug sàppe ayib la ci julli gi ag wàññiku la ca.

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Yoonalees na yittewoo ci lépp luy matal julli gi te di ko soreele ag ug wàññiku.
  2. Keemaanu Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci jàngale, ba tax mu lënkale àtte bi ak li ko waral; ngir leeral keemaanu Sariiha, ak sawarloo bakkan yi ci jëfe.
Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taylandi Pastoo Asaami Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Oromoo Kanadi Asrabijaani Ukraani الجورجية المقدونية
Gaaral tekki yi