+ -

عَنْ ‌مَحْمُودِ بْنِ لَبِيدٍ رضي الله عنه:
أَنَّ ‌عُثْمَانَ بْنَ عَفَّانَ أَرَادَ بِنَاءَ الْمَسْجِدِ فَكَرِهَ النَّاسُ ذَلِكَ، وَأَحَبُّوا أَنْ يَدَعَهُ عَلَى هَيْئَتِهِ، فَقَالَ: سَمِعْتُ رَسُولَ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ يَقُولُ: «مَنْ بَنَى مَسْجِدًا لِلهِ بَنَى اللهُ لَهُ فِي الْجَنَّةِ مِثْلَهُ».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح مسلم: 533]
المزيــد ...

Jële nañu ci Mahmuud Ibn Labiid -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Usmaan Ibn Affaan dafa bëggoon a tabax jàkka ji nit ñi sib loolu, ñu bëgg mu bàyyi ko ca na mu mel, mu ne leen: dégg naa Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ku tabax jàkka ngir Yàlla Yàlla dana ko tabaxal ca àjjana lu mel ni moom».

-

Leeral

Usmaan Ibn Affaan -yal na ko Yàlla dollee gërëm- dafa bëggoon a tabaxaat jàkkay Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci anam gu gën a rafet tabax bu njëkk ba, nit ñi bañ loolu; ndax la ca nekk ci soppi melokaan bañu ko tabexe woon ca jamonoy Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, jàkka ja nag dañu koo tabaxe woon ci ban, ab xaddam nekkoon ay xobi tàndarma, waaye Usmaan da koo bëggoon a tabaxe ay móol ak laso, Usmaan -yal na ko Yàlla dollee gërëm- xibaar leen ne dégg na Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: ku tabax jàkka ngir sàkku ngërëmal Yàlla mu kawe mi, du ngir ngistal mbaa ndéggtal, Yàlla dana ko fay ngën gi fay, te fay gi mooy Yàlla tabaxal ko lu mel ni moom ca àjjana.

Tekki: Àngale Urdu Endonesi Uyguuriya Bengali Turki Bosniya Sinhaaliya Endo Witnaam Kurdi Awsa Malayalam Telgoo Sawaahili Buurmi Taylandi Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Ciikiya Itaali Oromoo Kanadi Ukraani
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Ñaaxe ci tabax jàkka ak ngëneelam.
  2. Yaatal jàkka ak yeesal ko day dugg ci ngëneelu tabax gi.
  3. Solos sellal ñeel Yàlla mu kawe mi ci mbooleem jëf yi.