+ -

عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ عَنِ النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«سَبْعَةٌ يُظِلُّهُمُ اللَّهُ تَعَالَى فِي ظِلِّهِ يَوْمَ لاَ ظِلَّ إِلَّا ظِلُّهُ: إِمَامٌ عَدْلٌ، وَشَابٌّ نَشَأَ فِي عِبَادَةِ اللَّهِ، وَرَجُلٌ قَلْبُهُ مُعَلَّقٌ فِي المَسَاجِدِ، وَرَجُلاَنِ تَحَابَّا فِي اللَّهِ، اجْتَمَعَا عَلَيْهِ وَتَفَرَّقَا عَلَيْهِ، وَرَجُلٌ دَعَتْهُ امْرَأَةٌ ذَاتُ مَنْصِبٍ وَجَمَالٍ فَقَالَ: إِنِّي أَخَافُ اللَّهَ، وَرَجُلٌ تَصَدَّقَ بِصَدَقَةٍ فَأَخْفَاهَا حَتَّى لاَ تَعْلَمَ شِمَالُهُ مَا تُنْفِقُ يَمِينُهُ، وَرَجُلٌ ذَكَرَ اللَّهَ خَالِيًا، فَفَاضَتْ عَيْنَاهُ».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 1423]
المزيــد ...

Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
"juróom-ñaar yii Yàlla dana leen keral bis ba genn ker dul am lu dul keram ga: imaam bu maandu, ak waxambaane wu sosu ci jaamu Yàlla, ak waa ju xolam aju ca jàkka ya, ak ñaar ñu bëggante ci Yàlla, ci moom lañuy daje te ci moom lañuy teqalikoo, ak góor gu jigéen ju am dayo ak rafetaay woo mu ne ko: man damaa ragal Yàlla, ak waa ju saraxe ab sarax nëbb ko ba càmmooñam du xam li ndayjoor bi joxe, ak waa ju fàttaliku Yàlla ciw wéetaay, ay bëtam taa".

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 1423]

Leeral

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bégal na ñatti xeet ci way-gëm ñi ci ne Yàlla mu kawe mi dana leen keral ca kerug arasam ga bis ba ker amul gu dul keram ga: Bi ci njëkk: imaam ju maandu ci boppam te du kàccoor, maanu ci diggante ay càmmam ci lu dul tooñ; muy njiit lu mag li, waaye danañu ca boole képp ku jiite dara ci biri jullit ñi daal di cay maandu. Ñaareel bi: waxambaane wu sosu ci jaamu Yàlla, jeexal ag waxambaaneem ak cawarteem ci loolu ba faatu. Ñatteel bi: waa ju xolam aju ci jàkka, bu ca génnee ba na mu cay delloo ngir tarug bëggam ak bari lu muy taqoo ak jàkka, xolam di wéy di ca nekk donte yaramam dara gaar na ko mu génn fa ba nekk ca bittu jàkka ja. Ñenteel bi: ñaar ñoo xam ne ku nekk ci ñoom ñaar daa bëgg keneen ka ngir Yàlla, ñu sax ca bëgganteg diine ga te doguñu ko ngir àdduna moo xam dajaloo nañu ca dëgg-dëgg walla déet ba dee mujj teqale seen diggante. Juróomeel bi: waa joo xam ne ag jigéen sàkku na ko ci boppam ngir def ñaawteef, te moom jigéen ji boroomug teddnga la ak askan ak daraja ak alal ak taar, mu bañ daal di ne ko: man damaa ragal Yàlla. Juróom-benneel bi: waa ju saraxe ab sarax mu néew walla mu bari te ngistalul waaye mu nëbb ko ba càmmooñam xamul li ndayjooram joxe. Juróom-ñaareel bi: waa ju tudd Yàlla ci xolam di ko fàttaliku, walla ci làmmiñam ci sikar, ci ag wéetaay wolif nit ñi ay bëtam fees ak rangooñ ngir ragal ak màggal ñeel Yàlla mu kawe mi.

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Ngëneelu juróom-ñaari xeet yii ñu tudd ak ñaaxe ci roy ci ñoom.
  2. Ibn Hajar wax na ci waxam ji "ci keram gi" nee nañu ki ñu ci namm: kerug Arasam, te hadiisu Salmaan ibn Sahiid ibn Mansuur ci càllala gu rafet dana ko tegtale "juróom-ñaar yii Yàlla dana leen keral ca kerug Arasam ga".
  3. Ibn Hajar nee na: li gën a rafet ci li ñu firee maandu mooy ki nga xam ne day topp li Yàlla digle, ci teg mbir mu ne ci barabam ci lu dul ëppal mbaa yéesal, dakoo jiital cig tudd ngir li mu làmboo njariñ.
  4. Ngëneelu xaar julli ginnaaw ag julli.
  5. An-Nawawii nee na: nekk na ci ñaaxe ci bëggante ci Yàlla ak leeral màggaayu ngëneelam.
  6. Dañoo tudd ab dayo ak ub taar ngir bëgg gi ko nit ñi bëgg ak seen ug jafe.
  7. Li gën ci saraxe mooy nëbb ko ak sori ngistal, donte yoonal nañu fésal sarax ak asaka bu dee mucc na ci ngistal ak mu jublu sa ñaax ñeneen ci joxe ngir keneen roy ko ci, ak ngir feeñal màndargay lislaam.
  8. Juróom-ñaar ñii am na ñu xéewal googu ci sababus sellal gi ñeel Yàlla mu kawe mi ak wuute ak bànneex yi.
  9. Waxam ji: "juróom-ñaar Yàlla dana leen keral" tënk gi ñu leen tënk ci lim bii du dara, ndax am na ñeneen ñu rot ci hadiis ñu Yàlla di keral ca kerug Arasam ga.
  10. Ibn Hajar nee na: tudd gi ñu tudd góor ñi ci hadiis bii du dara! Ndax jigéen ñi it dañu da ñu ciy dugg lu dul bu dee imaam ju maandu imaam ju mag la ñu ci jublu, lu ko moy rekk jigéen ñi man nañu ci a dugg ndax dana am njaboot daal di maandu ci seen diggante, meloy taqoo ak jàkka ji moom day génn; ndax jullig jigéen ci këram moo gën ci jàkka ji, lu dul loolu ñoom da ñu cay bokk ba ci góor gi jigéen woo ci misaal manees naa gis jigéen ju ab buur bu rafet woo mu bañ ngir ragal Yàlla donte dafa am aajo.
Tekki: Àngale Endonesi Bengali Turki Risi Sinhaaliya Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Telgoo Sawaahili Taylandi Pastoo Asaami Amhari Olànd Gujarati Dariya Rom Majri الموري Malagasi Ukraani الجورجية المقدونية الخميرية الماراثية
Gaaral tekki yi