+ -

عَن أَبي هُرَيْرَةَ رضي الله عنه عَنِ النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«لاَ يُشِيرُ أَحَدُكُمْ عَلَى أَخِيهِ بِالسِّلاَحِ، فَإِنَّهُ لاَ يَدْرِي، لَعَلَّ الشَّيْطَانَ يَنْزِعُ فِي يَدِهِ، فَيَقَعُ فِي حُفْرَةٍ مِنَ النَّارِ».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 7072]
المزيــد ...

Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
"bu kenn jëmale mbokkam ngànaay, ndax xamul ne Saytaane man naa bif loxoom, mu tàbbi ci kàmbu sawara".

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 7072]

Leeral

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc moytandikuloo na jullit bi di joxañ mbokku jullitam ci benn xeetu ngànnaay, ndaxte xamul man naa am Saytaane yóbbe ko ci yëngal ngànnaay li ci loxoom, mu ray mbokkam mi walla mu lor ko, bu ko defee mu tàbbi ci ag moy guy waral ci moom mu tàbbi ci paxu sawara.

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Leeral araamug dereeti jullit.
  2. War na ñu wormaal jullit bi ak moytu di ko lor moo xam ci jëf walla wax, te bokk na ci yooyu jëmële ko weñ walla ngànnaay, donte day kaf; ndaxte Saytaane amaana mu bif ko ci loxoom mu dóor ci mbokkam mi, walla mu rocci ngànnaay li ci loxoom mu dal ko ci lu dul jubluwaayam mu lor ci mbokkam mi.
  3. Baare wépp yoon ak tere lépp luy jëme ci lu ñu tere.
  4. Xér ci muccug mbooloo mi ak sàmm lënkaloo gi dox ci diggante nit ñi, ak bañ leen a ragalloo ak tiitalleen donte ci junj la walla xupp.
Tekki: Àngale Endonesi Bengali Turki Risi Sinhaaliya Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Telgoo Sawaahili Taylandi Pastoo Asaami Amhari Olànd Gujarati Dariya Rom Majri الموري Malagasi Ukraani الجورجية المقدونية الخميرية الماراثية
Gaaral tekki yi