عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ عَنِ النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«مَنْ تَرَدَّى مِنْ جَبَلٍ فَقَتَلَ نَفْسَهُ فَهُوَ فِي نَارِ جَهَنَّمَ يَتَرَدَّى فِيهِ خَالِدًا مُخَلَّدًا فِيهَا أَبَدًا، وَمَنْ تَحَسَّى سُمًّا فَقَتَلَ نَفْسَهُ فَسُمُّهُ فِي يَدِهِ يَتَحَسَّاهُ فِي نَارِ جَهَنَّمَ خَالِدًا مُخَلَّدًا فِيهَا أَبَدًا، وَمَنْ قَتَلَ نَفْسَهُ بِحَدِيدَةٍ فَحَدِيدَتُهُ فِي يَدِهِ يَجَأُ بِهَا فِي بَطْنِهِ فِي نَارِ جَهَنَّمَ خَالِدًا مُخَلَّدًا فِيهَا أَبَدًا».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 5778]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
"ku xandaalu daanu ci aw doj daal di ray boppam kooku ci sawaraw Jahannama la jëm di ca xandaalu sax ca di ku ñu fay saxal ba fàww, ku naan tooke daal di ray boppam tookeem ji day nekk ci loxoom mu koy naan ca sawaraw Jahannama sax fa di ku ñu saxal ba fàww, ku ray boppam ci ag weñ weñam gi day nekk ci loxoom mu ciy butti biiram bi ca sawaraw Jahannama sax fa di ku ñuy saxal foofa ba fàww ".
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 5778]
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc moytandikuloo na nit ki ray boppam ci àdduna te tay ko ndax kon dees na ko mbugal ca sawaraw Jahannama ci anam gi mu ko defe boppam ci àdduna muy ag fay gu dëppoo ak loola, ku daaneel boppam jóge ci kaw aw doj daal di ray boppam kooku dana nekk ca sawaraw Jahannama di daanu jóge ci kaw doji Jahannama yi di aji-sax di ku ñu ca saxal ba fàww, ku guux tooke daal di ciy ray boppam tookeem ji day nekk ci loxoom mu koy guux ca sawaraw Jahannama di aji-sax di ku ñu saxal foofa ba fàww, ku dóor boppam ag weñ ci biiram daal di dee, kooku weñam gi day nekk ci loxoom mu ciy jam biiram bi ca sawaraw Jahannama di aji-sax foofa.