عَنْ عُبَادَةَ بْنِ الصَّامِتِ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ، وَكَانَ شَهِدَ بَدْرًا، وَهُوَ أَحَدُ النُّقَبَاءِ لَيْلَةَ العَقَبَةِ: أَنَّ رَسُولَ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ، وَحَوْلَهُ عِصَابَةٌ مِنْ أَصْحَابِهِ:
«بَايِعُونِي عَلَى أَلَّا تُشْرِكُوا بِاللَّهِ شَيْئًا، وَلاَ تَسْرِقُوا، وَلاَ تَزْنُوا، وَلاَ تَقْتُلُوا أَوْلاَدَكُمْ، وَلاَ تَأْتُوا بِبُهْتَانٍ تَفْتَرُونَهُ بَيْنَ أَيْدِيكُمْ وَأَرْجُلِكُمْ، وَلاَ تَعْصُوا فِي مَعْرُوفٍ، فَمَنْ وَفَى مِنْكُمْ فَأَجْرُهُ عَلَى اللَّهِ، وَمَنْ أَصَابَ مِنْ ذَلِكَ شَيْئًا فَعُوقِبَ فِي الدُّنْيَا فَهُوَ كَفَّارَةٌ لَهُ، وَمَنْ أَصَابَ مِنْ ذَلِكَ شَيْئًا ثُمَّ سَتَرَهُ اللَّهُ فَهُوَ إِلَى اللَّهِ، إِنْ شَاءَ عَفَا عَنْهُ وَإِنْ شَاءَ عَاقَبَهُ» فَبَايَعْنَاهُ عَلَى ذَلِكَ.
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 18]
المزيــد ...
Jële nañu ci Hubaadata ibn As-Saamit yal na ko Yàlla dollee gërëm, mu bokkoon ci ñi fekke Badar, mu doon kenn ca ña ñu tànnoon ca guddig Haqaba ga: mu ne Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc wax na, fekk am mbooloo ci Sahaaba yi ña nga ko wër:
"jaayanteleen ak man ci ne dungeen bokkaale Yàlla ak dara, te dungeen sàcc, dungeen njaalo dungeen ray seen i doom, te dungeen indi aw duur wu ngeen di sos ci diggante seen loxo yi ak seen tànk yi, te dungeen ma moy ci njekk, ku matale kóllare gi ci yéen fayam ma nga fa Yàlla, ku def ci yooyu dara ñu mbugal ko ci àdduna loolu ag far la ñeel ko, ku def ci yooyu dara topp Yàlla suturaal ko kon ca Yàlla lay dellu, bu ko soobee mu baal ko bu ko soobee mu mbugal ko" nu jaayante ak moom ci loolu.
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 18]
Hubaadata ibn As-Saamit yal na ko Yàlla dollee gërëm, mu bokkoon ci ñi fekke woon xareb Badar bu mag ba, te moo mag ci aw nitam ña ñëwoon ngir jaayante ngir dimbali Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc guddig Haqaba ga nekk ca Minaa -ba Yonnente bi nekkee Màkka njëkk muy gàddaay jëm Madiina - mu ne Yonnente bi dafa toogoon ci diggante Sahaabaam yi mu sàkku ci ñoom ñu kóllarante ak moom ci ay mbir: Bi ci njëkk: duñu bokkaale ci jaamu Yàlla gi dara donte dafa néew. Ñaareel bi: duñu sàcc. Ñatteel bi: duñu def ñaawteefu njaalo. Ñenteel bi: duñu ray seen doom yu góor yi ngir ragal ñàkk, walla yu jigéen yi ngir ragal gàcca. Juróomeel bi: duñu indi aw fen wu ñu sos ci diggante seen loxo yi ak seen tànk yi, ndax li ëpp ci jëf yi ci ñoom ñaar lay ame donte cér yi des dana ca bokk. Juróom-beneel bi: duñu moy Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ci njekk. Ku sax ci ñoom ca kóllare ga taqoo ak loolu fayam ma nga fa Yàlla, ku def dara ci yooyu ñu tudd -ba mu des bokkaale- ñu mbugal ko ci àdduna ci taxawal daan gi ci kawam loolu ag far bàkkaar la ñeel ko, ku def ci yooyu dara topp Yàlla suturaal ko kon ay mbiram ma nga ca Yàlla; bu ko soobee mu baal ko bu ko soobee itam mu mbugal ko, ña teewoon ñépp jaayante ak moom ci loolu.