عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«بَدَأَ الْإِسْلَامُ غَرِيبًا، وَسَيَعُودُ كَمَا بَدَأَ غَرِيبًا، فَطُوبَى لِلْغُرَبَاءِ».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 145]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
"lislaam dafa tàmbali di lu tumurànke, te dana dellu ca na mu tàmbalee woon di lu tumurànke, kon texe ñeel na way-tumurànke yi".
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 145]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xibaare ne lislaam dafa tàmbali nekk lu tumurànke ci ay benn-benni nit ak tuutig waa lislaam, te dana dellu di lu tumurànke ci néewug ña koy taxawe kem na mu tàmbalee woon, kon boog ag xéewal ak ug, mbégte ñeel na leen.