عَنْ سَهْلِ بْنِ سَعْدٍ رَضيَ اللهُ عنه قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«إِيَّاكُمْ وَمُحَقَّرَاتِ الذُّنُوبِ، فَإِنَّمَا مَثَلُ مُحَقَّرَاتِ الذُّنُوبِ كَقَوْمٍ نَزَلُوا فِي بَطْنِ وَادٍ، فَجَاءَ ذَا بِعُودٍ، وَجَاءَ ذَا بِعُودٍ، حَتَّى أَنْضَجُوا خُبْزَتَهُمْ، وَإِنَّ مُحَقَّرَاتِ الذُّنُوبِ مَتَى يُؤْخَذْ بِهَا صَاحِبُهَا تُهْلِكْهُ».
[صحيح] - [رواه أحمد] - [مسند أحمد: 22808]
المزيــد ...
Jële nañu ci Sahl Ibn Sahd -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
"moytulleen bàkkaar yi ñuy xeeb bàkkaar yi ñuy xeeb dafa mel ni ay nit yu wàcc ci aw xur, kii indi ab bant, kii indi ab bant, ba ñu ñoral ca seen mburu, te bàkkaar yi ñuy xeeb saa bu ñu ci jàppee boroom mu alag ko".
[Wér na] - [Ahmat soloo na ko] - [Téere Adiisu Ahmat bees leeral càllala ya - 22808]
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day moytandikuloo ñuy woyofal def bàkkaar yu ndaw yi, ak di ko baril ndax day alage bu baree, mu joxe misaal ci loolu ci ay nit yu wàcc ci biir aw xur, ku nekk ci ñoom indi ab bant bu ndaw, ba ñu mjja ñorale seen mburu ci seen bant ya, ak ne bàkkaar yi ñuy xeeb saa bu ñu ci jàppee boroomam te tuubu ko walla Yàlla baal ko ko kon dana ko alag.