عن أبي بَكرة رضي الله عنه قال: سمعت رسول الله صلى الله عليه وسلم يقول:
«إِذَا الْتَقَى الْمُسْلِمَانِ بِسَيْفَيْهِمَا فَالْقَاتِلُ وَالْمَقْتُولُ فِي النَّارِ»، فَقُلْتُ: يَا رَسُولَ اللهِ هَذَا الْقَاتِلُ، فَمَا بَالُ الْمَقْتُولِ؟ قَالَ: «إِنَّهُ كَانَ حَرِيصًا عَلَى قَتْلِ صَاحِبِهِ».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 31]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Bakrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónenteb Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax ne:
«ñaari jullit bu ñu jaamaarloo ak séen ñaari Jaasi ka raye ak ka ñu ray yépp sawara lañu jëm», ma ne ko: yaw Yónente Yàlla bi kii moo ray, waaw ki ñu ray moom luy mbiram? Mu ne: «ndax moom dafa xéroon ci ray waayam ji».
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 31]
Yónente bi day xamle ne ñaari jullit bu ñu jaamaarloo ak séen ñaari Jaasi, ku nekk jubloo ray moroom ja; kon ki raye sawara lay jëm ngir sababus li mu ray waayam ji, Waaye Sahaaba yi di leer lu ci ki ñu ray: naka lay dugge sawara? Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- xamal leen ne moom it dafa bëggoon a ray moromam ji, te dara terewul mu ray ko lu dul li waa ji gaawantu njëkk koo ray.