عَنْ أَبِي العَبَّاسِ سَهْلِ بْنِ سَعِدٍ السَّاعِدِيِّ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ قَالَ: جَاءَ رَجُلٌ إِلَى النَّبِيِّ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ، فَقَالَ: يَا رَسُولَ اللَّهِ، دُلَّنِي عَلَى عَمَلٍ إِذَا عَمِلْتُهُ أَحَبَّنِي اللَّهُ وَأَحَبَّنِي النَّاسُ، فَقَالَ:
«ازْهَدْ فِي الدُّنْيَا يُحِبُّكَ اللَّهُ، وَازْهَدْ فِيمَا عِنْدَ النَّاسِ يُحِبُّكَ النَّاسُ».
[قال النووي: حديث حسن] - [رواه ابن ماجه وغيره بأسانيد حسنة] - [الأربعون النووية: 31]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abii Al-Abbaas Sahl ibn Sahd As-Saahidii yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: jenn waay dafa ñëw ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, tegtal ma jëf joo xam ne su ma ko defee Yàlla dana ma bëgg nit ñi it danañu ma bëgg, mu ne ko:
"dëddul àdduna kon Yàlla dana la bëgg, dëddul li ci nit ñi kon nit ñi danañu la bëgg".
[قال النووي: حديث حسن] - [رواه ابن ماجه وغيره بأسانيد حسنة] - [الأربعون النووية - 31]
Benn waay dafa laaj Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu tegtal ko jëf joo xam ne bu ko defee Yàlla bëgg ko nit ñi it bëgg ko, Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: Yàlla dana la bëgg boo bàyyee desiitu àdduna si, ak lu la dul jariñ ca àllaaxira, ak nga bàyyi loo xam ne dafa am lorànge ci sa diine, nit ñi it danañu la bëgg boo dëddoo li nekk ci seen i loxo ci mbiri àdduna si; ndax ñoom dañu ko a bëgg ci seen jëmmi bopp, te ku ko xëccoo ak ñoom ñu bañ ko, ku leen ko bàyyeel nag ñu bëgg ko.