عن أبي هريرة رضي الله عنه قال: قال رسول الله صلى الله عليه وسلم:
«إِنَّ اللهَ لَا يَنْظُرُ إِلَى صُوَرِكُمْ وَأَمْوَالِكُمْ، وَلَكِنْ يَنْظُرُ إِلَى قُلُوبِكُمْ وَأَعْمَالِكُمْ».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 2564]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«Yàlla du xool seen i melo mbaa seen alal waaye seen xol lay xool ak seen i jëf».
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 2564]
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne Yàlla mu kawe mi du xool meloy jaam ñi ak seen i yaram, ndax dafa rafet walla dafa ñaaw ? Ndax dafa rëy walla dafa ndaw? Ndax dafa wér walla dafa wéradi? Du xool itam seen i alal, ndax dafa bari walla dafa tuuti? Yàlla du toppe jaamam yi walla mu leen di saytu ci mbir yii ak seenug rawante ci loolu, waaye day xool seen xol yi ak la ca nekk cig ragal Yàlla ak kóolute, ak dëggu ak sellal, walla ngistal mbaa ndéggtal, day xool it seen i jëf ak ug sellam mbaa ag yàqoom; mu fay leen ca.