Xàjjaley wanqaas yi

Toftaleg Adiis yi

Yàlla day fiir, way-gëm it day fiir, te fiiràngeg Yàlla mooy way-gëm ji def lu mu araamaal
عربي Àngale Urdu
Yàlla dafa bind yu rafet yi ak yu ñaaw yi, daal di leeral ko, képp ku yéene jëf i yiw, te defu ko, Yàlla dana ka ko bindal wenn yiw wu mat sëkk, waaye bu ko yéenee ba noppi def ko, mu bindal ko fukki yiw, mannakoo Ful bamu yégg juróom-ñaari téeméeri, ba ci ay full yu bari, waaye képp ku Yéenee jëf lu ñaaw te defu ko Yàlla di na ko bindal wenn yiw wu mat sëkk, bu ko Yéenee nag daldi koy def mu bindal ko wenn ñaawteef
عربي Àngale Urdu
Yàlla du xool seen i melo mbaa seen alal waaye seen xol lay xool ak seen i jëf
عربي Àngale Urdu
yéen sama jaam ñi damaa araamal tooñ ci sama bopp, ma def ko muy lu araam ci seen diggante kon buleen di tooñante
عربي Àngale Urdu
Yalla dana néggandiku tooñkat bi, ba bu ko jàppee du ko rëcc
عربي Àngale Urdu
ñiy yërëme Aji-Yërëme ji dana leen yërëm, yërëmleen waa suuf, kon ka ca kaw asamaan dana leen yërëm
عربي Àngale Urdu
sunu Boroom bu baarkeel bi te kawe day wàcc guddi gu nekk ci asamaani àdduna si bu guddi gi desee ñatteelu xaaj bu mujj ba
عربي Àngale Urdu
doomu Aadama weddi na ma te loolu waru ko woon,mu saaga ma te waru ko woon
عربي Àngale Urdu
ku noonook sama péete yégal naako ab xare, sama jaam bi du ma jegeñ-jegeñlu ci dara lu ma gënal li ma farataal ci moom
عربي Àngale Urdu
Yàlla du tooñ benn way-gëm ci jëfam ju baax di ko wàññi, dana ka ko jox fii ci àdduna fay ka ko ca allaaxira
عربي Àngale Urdu
Yàlla dat ŋëb suuf si, lem asamaan yi ci ndayjooram, di wax naan: man maay buur, ana buuri suuf si
عربي Àngale Urdu
xanaa du ki ko doxloo ci ñaari tànkam ci àdduna man na koo doxloo ëllëg bis-pénc ci xar kanamam?
عربي Àngale Urdu