عن عبد الله بن عمرو بن العاص رضي الله عنهما:
عن النبي صلى الله عليه وسلم أنه كان إذا دخل المسجد قال: «أعوذ بالله العظيم، وبوجهه الكريم، وسلطانه القديم، من الشيطان الرَّجِيم»، قال: أَقَطُّ؟ قلت: نعم، قال: فإذا قال ذلك قال الشيطان: حُفِظَ منِّي سائر اليوم.
[حسن] - [رواه أبو داود] - [سنن أبي داود: 466]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Abdullah Ibn Amr ibnul Haas yal na leen Yàlla dollee gërëm:
Jële na ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne bu daan dugg ci jàkka day wax: "ahuusu bil Laahi Alhasiimi, wa bi wajhihi Alkariimi, wa sultaanihii alxadiimi, minas Saytaani Arrajiimi", nee na: ndax loolu rekk la? Ma ne ko: waaw, mu ne: bu waxee loolu saytaane day wax naan: aarees na ko ci man tay.
[Tane na] - [Abóo Daawuda soloo na ko] - [Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda - 466]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bu daan dugg ci jàkka day wax: (ahuusu bil Laahi Alhasiimi) maa ngi aaru di làqatu ci Yàlla ak i meloom. (wa bi wajhihi Alkariimi) Aji-Tabe ji Aji-Joxe ji, (wa sultaanihii) ag notam ak kàttanam ak notam ñeel ku ko soob ci mbindeefam yi (alxadiimi) ki
Amu tàmbalikaay
Te amul it yamukaay (minas Saytaani Arrajiimi) ki ñu soreele dàq ko ci yërmàndey Yàlla, Maanaam: Yàlla sàmm ma ci ay
jax-jaxam ak ug beewalam, ak ay jéegoom, ak i xalaatam, ak i jaxaseem, ak réeralaateem, ndaxte moom sabab la ci cànkute ak jëme ci mbewte ak réer. Ñu wax Abdullah ibn Amr "ndax loolu dong" maanaam: ndax lii rekk la Yonnente bi wax? Mu ne: waaw.
Bu kiy dugg ci jàkka waxee ñaan gii; Saytaane day wax: kii di dugg aar na boppam ci man ci waxtu yépp bëccëg gi ak guddi gi.