Toftaleg Adiis yi

Li gën ci sikar yi: Laa ilaaha illal Laahu, li gën ci ñaan yi: Alhamdu lil Laahi
عربي Àngale Urdu
fi jaam bi di gën a jegee Boroomam mooy bu sujjóotee, deeleen ci baril ay ñaan
عربي Àngale Urdu
Wax yi gënal Yàlla ñent la: Subhaanal Laah, Wal hamdu lil Laah, wa laa-i-Laaha illal Laah, wal Laahu akbar, boo ci tàmbalee baax na
عربي Àngale Urdu
ñaari baat a ngi nii yu woyof ci làmmeñ, diis ci màndaxekaay ba, Yàlla miy Aji-Yërëme ji sopp leen
عربي Àngale Urdu
ku wàcc cig kër daal di wax: ahuusu Bi kalimaatil Laahi At taammaati min sarri maa xalaxa, dara du ko lor ba baa muy juge ca kër googa
عربي Àngale Urdu
ku jàng ñaari aaya yi ci mujjug saaru Al-Baxara cig guddi danañu ko fegal
عربي Àngale Urdu
Laab mooy genn wàllu ngëm, sant Yàlla day feesal nattukaayu jëf ya, sàbbaal Yàlla ak sant Yàlla dañuy feesal walla day feesal li nekk ci diggante asamaan ak suuf
عربي Àngale Urdu
Saytaane day dikkal kenn ci yéen, di ko wax naan: ku bind lii? Ku bind lii? Ba mujj mu ne ko: ku bind sa Boroom? Bu àggee fii nag na muslu ci Yàlla te yamale ko fa
عربي Àngale Urdu
bu kenn ci yéen duggee ci jàkka na wax: Allaahumma iftah lii abwaaba rahmatika, bu génnee na wax: Allaahumma innii as-aluka min fadlika
عربي Àngale Urdu
kooku Saytaane bu ñu woowe Xinsab la, boo ko yégatee nanga muslu ci Yàlla ci moom, te nga tifli ci sa càmmooñ ñatti yoon
عربي Àngale Urdu