+ -

عَنْ سَلْمَانَ رضي الله عنه قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«إِنَّ رَبَّكُمْ حَيِيٌّ كَرِيمٌ، يَسْتَحْيِي مِنْ عَبْدِهِ إِذَا رَفَعَ يَدَيْهِ إِلَيْهِ أَنْ يَرُدَّهُمَا صِفْرًا».

[حسن] - [رواه أبو داود والترمذي وابن ماجه] - [سنن أبي داود: 1488]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Salmaan -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yonente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
"seen Boroom de Ku bari kersa la ku tedd la, dana kersawu ci jaam bi bu yëkkëtee loxoom jëme ci moom mu koy ba ña jox".

[Tane na] - [Abóo Daawuda soloo na ko, ak At-tirmisiy, ak Ibnu Maaja] - [Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda - 1488]

Leeral

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day ñaaxe ci yëkkëti loxo ci jamonoy ñaan, mu xamle ne Yàlla Aji-Sell ji ku bari kersa la, te du deñ di joxe, day defal jaam bi lu koy bégloo, dindil ko lu koy lor, ku tedd la day joxe ci lu dul ñu koy laaj kon naka lay deme ginnaaw bu ñu ko laajee! Day kersawu ci jaamam bi ko gëm mu delloo ay loxoom ginnaaw ba mu ko yëkkëtee ngir ñaan mu koy ñàkka nangul ñaanam ga.

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Saa bu nit ki feeñalee ak soxlawoom jëm ci Yàlla ak ug njaame, muy gën a am yaakaar ci ñaanam gu nangu.
  2. Xemmemloo ci ñaan, ak sopp ñu yëkkëti ñaari loxo yi ci ñaan gi ndax dafa bokk ci sababi nangu ñaan yi.
  3. Leeral ne Yàlla dafa tabe lool bari yërmànde lool ci jaamam yi.
Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Taylandi Pastoo Asaami Suwiit Amhari Olànd Gujarati Dariya Rom Majri الموري Malagasi Kanadi Ukraani الجورجية المقدونية الخميرية الماراثية
Gaaral tekki yi