+ -

عَنْ أَنَسٍ رضي الله عنه قَالَ:
كَانَ أَكْثَرُ دُعَاءِ النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: «اللَّهُمَّ رَبَّنَا آتِنَا فِي الدُّنْيَا حَسَنَةً، وَفِي الآخِرَةِ حَسَنَةً، وَقِنَا عَذَابَ النَّارِ».

[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 6389]
المزيــد ...

Jële na ñu ci Anas -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:
Li ëppoon ci ñaani Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-mooy:"Allaahumma Rabbanaa aatinaa fiddunyaa hasanatan, wa fil-aaxirati hasanatan, wa xinaa hasaabannaari".

[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 6389]

Leeral

Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-daan na baril di ñaane ñaan yu matale yi,bokk na ca: "Rabbanaa aatinaa fiddunyaa hasanatan, wa fil-aaxirati hasanatan, wa xinaa hasaaban-naari", Moom dafa làmboo yiwi àdduna ci wërsëg wu teey,te yaatu te dagan,ak jabar ju sell,ak doom ju sedd xool,ak nooflaay, ak xam-xam buy jariñ, ak jëf yu sell,ak yi ko niru ci ay càkkuteef yu ñu sopp te mu dagan, ak yiwi allaaxira ci mucc ci mbugëlu bàmmeel,ak taxawaay ba, ak sawara,ak am ngërëmal Yàlla, ak texe ca àjjanay xéewal gu sax ga, ak jege Boroom biy Aji-Yërëme.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Taylandi Pastoo Asaami Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Oromoo Kanadi Ukraani الجورجية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Sopp nañu di ñaan ñaan yu matale yi, ngir roy ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-.
  2. Li gën a mat mooy nit ki boole ci ñaanam yiwi àdduna ak allaaxira.