+ -

عَنْ شَدَّادِ بْنِ أَوْسٍ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ عَنِ النَّبِيِّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«سَيِّدُ الِاسْتِغْفَارِ أَنْ تَقُولَ: اللَّهُمَّ أَنْتَ رَبِّي لاَ إِلَهَ إِلَّا أَنْتَ، خَلَقْتَنِي وَأَنَا عَبْدُكَ، وَأَنَا عَلَى عَهْدِكَ وَوَعْدِكَ مَا اسْتَطَعْتُ، أَعُوذُ بِكَ مِنْ شَرِّ مَا صَنَعْتُ، أَبُوءُ لَكَ بِنِعْمَتِكَ عَلَيَّ، وَأَبُوءُ لَكَ بِذَنْبِي فَاغْفِرْ لِي، فَإِنَّهُ لاَ يَغْفِرُ الذُّنُوبَ إِلَّا أَنْتَ» قَالَ: «وَمَنْ قَالَهَا مِنَ النَّهَارِ مُوقِنًا بِهَا، فَمَاتَ مِنْ يَوْمِهِ قَبْلَ أَنْ يُمْسِيَ، فَهُوَ مِنْ أَهْلِ الجَنَّةِ، وَمَنْ قَالَهَا مِنَ اللَّيْلِ وَهُوَ مُوقِنٌ بِهَا، فَمَاتَ قَبْلَ أَنْ يُصْبِحَ، فَهُوَ مِنْ أَهْلِ الجَنَّةِ».

[صحيح] - [رواه البخاري] - [صحيح البخاري: 6306]
المزيــد ...

Jële nañu ci Sadaad ibn Aws -yal na ko Yàlla dollee gërëm-mu jële ci Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-mu wax ne:
«li gën a kawe cig jégalu yi mooy nga wax: Allaahumma anta Rabbii laa-i-Laaha illaa Anta, xalaqtanii wa anaa abduka, wa anaa halaa ahdika wa wahdika mastatahtu, ahuusu bika min sarri maa sanahtu, abuuhu laka bi nihmatika alayya, wa abuuhu bi sanbii faxfirlii,fa innahu laa yaxfirus sunuuba illaa Anta» mu wax ne:"ku ko wax ci bëccëg gi te am ci kóolute, daal di faatu ci bis bi njëkk ngoon di jot, kooku ci waa àjjana lay bokk, ku ko wax it ci guddi gi te am ci kóolute daal di faatu njëkk suba di jot, kooku ci waa àjjana lay bokk".

[Wér na] - [Al-buxaariy soloo na ko] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 6306]

Leeral

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-day xibaare ne jéggalu am na ay baat, te ba ca gën te gën caa màgg mooy jaam bi wax ne: "Allaahumma anta Rabbii laa ilaaha illaa Anta, xalaqtanii wa anaa abduka, wa anaa halaa ahdika wa wahdika mastatahtu, ahuusu bika min sarri maa sanahtu, abuu-u laka bi nihmatika alayya, wa abuu-u bi sanbii faxfirlii, fa innahu laa yaxfirus sunuuba illaa Anta" Jaam bi njëkk a saxal wéetal Yàlla, ak ne Yàlla moo ko bind te moom lay jaamu te du ko bokkaale ak dara, ak ne moom moo ngi ci li mu kóllarante ak Yàlla ci gëm ko ak topp ko, kem kàttanam; ndax jaam bi lu mu man a def ci ay jaamu du man a def mbooleem li ko Yàlla digal, du caagine li ko war ci sant xéewal yi, ak ne moom moo ngi làqu ci Yàlla,di aaru ci moom, ndax moom Mooy musluwaay bi ci ay yi jaam bi di def, Ak ne moom day saxal te di ko nangul ay xéewalam ci moom, tey dellu ci boppam ci saxal ak nangu ay bàkkaaram ak i moyam, Ginnaw lii, day ñaan Boroomam mu jéggal ko, ci suturaal ko ay bàkkaaram te fegal ko bàkkaar ya ci njéggalam ak ngëneelam ak yërmàndeem, ndaxte kenn du jéggale bàkkaar yi ku dul moom Yàlla mu màgg mi. Topp muy xibaare ne dafa bokk ci sikkari suba yi ak guddi yi, ku ko wax ci kóolute ak teewlu maanaa yi ak gëm ko ci njëlbeenu bis bi, ci diggante fenkug jant bi ba baa muy jeng, te mooy waxtuw bëccëg gi, mu daal di faatu dana dugg àjjana, Ku ko wax ci guddi gi it, te mooy bi jant bi sowee ba baa fajar gi di fenk, mu daal di faatu njëkk suba di jot, dana dugg àjjana.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taylandi Pastoo Asaami Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Oromoo Kanadi Ukraani الجورجية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Baati jéggalu yi dafa wuute te yenn yi moo gën yeneen yi.
  2. Jaadu na ci jaam bi mu xér ci di ñaan Yàlla ci ñaan gii; ndaxte mooy sangi jéggalu yi.