عَنْ عَبْدِ اللهِ بنِ مَسعُودٍ رضي الله عنه قَالَ: قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ:
«عَلَيْكُمْ بِالصِّدْقِ، فَإِنَّ الصِّدْقَ يَهْدِي إِلَى الْبِرِّ، وَإِنَّ الْبِرَّ يَهْدِي إِلَى الْجَنَّةِ، وَمَا يَزَالُ الرَّجُلُ يَصْدُقُ وَيَتَحَرَّى الصِّدْقَ حَتَّى يُكْتَبَ عِنْدَ اللهِ صِدِّيقًا، وَإِيَّاكُمْ وَالْكَذِبَ، فَإِنَّ الْكَذِبَ يَهْدِي إِلَى الْفُجُورِ، وَإِنَّ الْفُجُورَ يَهْدِي إِلَى النَّارِ، وَمَا يَزَالُ الرَّجُلُ يَكْذِبُ وَيَتَحَرَّى الْكَذِبَ حَتَّى يُكْتَبَ عِنْدَ اللهِ كَذَّابًا».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح مسلم: 2607]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Abdallah Ibn Mashuud mu wax ne: Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«dénk naa leen dëggu, ndaxte dëggu day jur ag mbaax, te ag mbaax day jur àjjana, te nit ki du deñ di dëggal di jublu dëgg ba ñu bind ko fa Yàlla ne ab dëggalaakon la, maa ngi leen di moytandikuloo fen, ndaxte fen day yóbbe cig kàccoore, te ag kàccoore day yóbbe sawara, te nit ki du deñ di fen, di jublu fen, ba ñu bind ko fa Yàlla ne ab fenkat la».
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Muslim bi gën a wér - 2607]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc digle na dëggu, mu xamle ne taqoo ak moom day yóbbe ci jëf yu baax yiy sax, te taqoo ak jëf yu baax day jëme boroomam àjjana, te dëgg du deñ di bàmtu ci moom ci li nëbbu ak li feeñ, ba mu yeyoo turu dëggalaakoon; te ag jotale la cig dëggu, Yonnente bi yal na ko Yàlla xeexal ak mucc tere na fen ak wax ay neen; ndaxte moom day jëme ci jeng wolif ag njub, ak jëm ci aw ay ak ug yàq ak i moy, topp mu yóbb boroomam sawara, te du deñ di baril fen ba ñu bind ko fa Yàlla mu bokk ci fenkat yi.