عن أبي هريرة رضي الله عنه عن النبي صلى الله عليه وسلم قال:
«كَلِمَتَانِ خَفِيفَتَانِ عَلَى اللِّسَانِ، ثَقِيلَتَانِ فِي الْمِيزَانِ، حَبِيبَتَانِ إِلَى الرَّحْمَنِ: سُبْحَانَ اللهِ الْعَظِيمِ، سُبْحَانَ اللهِ وَبِحَمْدِهِ».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 6406]
المزيــد ...
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«ñaari baat a ngi nii yu woyof ci làmmeñ, diis ci màndaxekaay ba, Yàlla miy Aji-Yërëme ji sopp leen: Subhaanal Laahil Hasiim, Subhaanal Laahi wa bi hamdihii».
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 6406]
Leerarug adiis bi:
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xamle ne am na ñaari baat yu nit ki di wax ci lu dul coono ak ci bépp anam, te seenug fay màgg lool ca màndaxekaay ba , te sunu Boroom miy Aji-Yërëme ji bëgg leen muy:
Subhaanal Laahil Hasiim, Subhaanal Laahi wa bi hamdihii; ngir li ñu làmboo ci melal Yàlla cig màgg ak mat, ak sellal ko ci ay wàññiku -baarkeel na te kawe na-.