عن جابر رضي الله عنه قال: سمعت رسول الله صلى الله عليه وسلم يقول:
«أَفْضَلُ الذِّكْرِ: لَا إِلَهَ إِلَّا اللهُ، وَأَفْضَلُ الدُّعَاءِ: الْحَمْدُ لِلهِ».
[حسن] - [رواه الترمذي والنسائي في الكبرى وابن ماجه] - [سنن الترمذي: 3383]
المزيــد ...
Jële nañu ci Jaabir -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónent Yàlla bi -yal ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax naan:
«Li gën ci sikar yi: Laa ilaaha illal Laahu, li gën ci ñaan yi: Alhamdu lil Laahi».
[Tane na] - [At-tirmisiy soloo na ko, ak An-nasaa'iy ca Al-kubraa, ak Ibnu Maaja] - [Téere Sunna yi bu At-tirmisiy - 3383]
Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafay xamle ne li gën ci tudd Yàlla mooy: «Laa ilaaha illal Laahu» maanaam, amul kenn ku ñuy jaamu ci dëgg ku dul Yàlla, li gën ci ñaan yi mooy: Alhamdu lil Laahi; te mooy nangu ne kiy joxe xéewal mooy Yàlla -tudd naa sellam ga-, moom mi yeyoo melokaan yu mat sëkk ya te rafet.