عَنْ حَارِثَةَ بْنِ وَهْبٍ الخُزَاعِيِّ رضي الله عنه قَالَ: سَمِعْتُ النَّبِيَّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ يَقُولُ:
«أَلاَ أُخْبِرُكُمْ بِأَهْلِ الجَنَّةِ؟ كُلُّ ضَعِيفٍ مُتَضَعِّفٍ، لَوْ أَقْسَمَ عَلَى اللَّهِ لَأَبَرَّهُ، أَلاَ أُخْبِرُكُمْ بِأَهْلِ النَّارِ: كُلُّ عُتُلٍّ جَوَّاظٍ مُسْتَكْبِرٍ».
[صحيح] - [متفق عليه] - [صحيح البخاري: 4918]
المزيــد ...
Jële nañu ci Haarisatu ibn Wahbin yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: dégg naa Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
"ndax duma leen xibaare waa àjjana? Ñooy képp ku néew doole, tey toroxlu, te bu giñoon ci Yàlla mu dëggal ko, ndax duma leen xibaare waa sawara? Ñooy képp ku dëgër soxor tey rëy-rëylu".
[Wér na] - [Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 4918]
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak day xamle yenn meloy waa àjjana ak waa sawara.
Ñi ëpp ci waa àjjana ñooy: "képp ku néew doole tey toroxlu", maanaam: kuy wàcce boppam di toroxlul Yàlla mu kawe mi, te toroxlu ci boppam ngir moom, ba sax yenn nit ñi dañu koy néewal doole di ko xeeb, te kii di toroxlul Yàlla bu giñoom ci Yàlla giñ gu mu xemmeem, kon Yàlla dana ko setal, dëggal ko ca la mu giñ daal di nangu la muy sàkku ak lamuy ñaan.
Ñi ëpp ci waa sawara ñooy: képp ku nekk "Hutullin" te mooy ku dëgër soxor te tar ci xulóo, walla ñaaw jikkó ku dul wommatul yiw, "jawwaas" mooy kiy rëy-rëylu, man a lekk, di boroom yaram wu rëy, di rëy-rëylu ci doxiinam, di ku ñaaw jikkó, "mustakbir" kuy bañ dëgg, tey xeeb ñeneen ñi.