عَنْ أَبِي هُرَيْرَةَ رضي الله عنه أَنَّ رَسُولَ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ:
«أَلَا أَدُلُّكُمْ عَلَى مَا يَمْحُو اللهُ بِهِ الْخَطَايَا، وَيَرْفَعُ بِهِ الدَّرَجَاتِ؟» قَالُوا بَلَى يَا رَسُولَ اللهِ قَالَ: «إِسْبَاغُ الْوُضُوءِ عَلَى الْمَكَارِهِ، وَكَثْرَةُ الْخُطَا إِلَى الْمَسَاجِدِ، وَانْتِظَارُ الصَّلَاةِ بَعْدَ الصَّلَاةِ، فَذَلِكُمُ الرِّبَاطُ».
[صحيح] - [رواه مسلم] - [صحيح مسلم: 251]
المزيــد ...
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«ndax du ma leen tegtal li Yàlla di fare njuumte yi, di ci yëkkatee daraja yi?" Ñu ne ko ahakay yaw Yonnente Yàlla bi, mu ne leen: "di jotale njàppu mi ci jomonoy sibeel ga, ak baril ay jéego jëm ca jàkka ya, ak di xaar julli ga ginnaaw ak julli, loolu mooy faanu ga».
[Wér na] - [Muslim soloo na ko] - [Téere Muslim bi gën a wér - 251]
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa laaj Sahaaba yi ndax bëgg nañu mu tegtal leen ay jëf yoo xam ne sabab lañu ci jéggalug bàkkaar yi, ak far ko ca téerey malaaka ya koy wattu, ak kaweg ay daraja fa àjjana ?
Sahaaba yi ne ko: waawaaw bëgg nañu loolu kay. Mu ne leen:
Bi ci njëkk: jotale ak matale njàppu mi ci kaw coono yi; niki sedd, ak néewum ndox, ak mettitu yaram wi, ak ndox mu tàng.
Ñaareel bi: baril ay jéego -te mooy li nekk ci diggante ndëggu yi- jëm ca jàkka ya ngir kër gu sori, ak baamtu gu bari.
Ñatteel bi: xaar waxtuw julli, xol bi aju ca, ak di ko waajal, ak toog si jàkka ci di xaar mbooloo mi, bu ko jullee ba noppi toog fa mu jullee di xaar geneen julli.
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daal di leeral ne bir yii mooy dëgg-dëggi fasukaay ga; ndaxte day fatt yooni saytaane yi ci bakkan, di not bànneex, di ko teree nangu ay jax-jaxal, ba tax mbooloom Yàlla mi di not soldaari saytaane yi; te loolu mooy jihaad ju mag ji, bu ko defee mu mel ni ag fasukaay ci yooni noon bi.