+ -

عن جابر بن عبد الله رضي الله عنهما عن النبي صلى الله عليه وسلم قال:
«كُلُّ مَعْرُوفٍ صَدَقَةٌ».

[صحيح] - [رواه البخاري من حديث جابر، ورواه مسلم من حديث حذيفة] - [صحيح البخاري: 6021]
المزيــد ...

Jële nañu ci Jaabir Ibn Abdullah -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«Jépp jëf ju baax sarax la».

[Wér na] - [Al-buxaariy soloo na ko ca Adiisu Jaabir ba, Muslim it soloo ko ci Adiisu Husayfa] - [Téere Al-buxaariy bi gën a wér - 6021]

Leeral

Yónente bi, -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak jàmm, daf nuy xamal ne, bépp rafetal ak njariñ ci nit ñi, moo xam wax la walla jëf, sarax la, te dafay maye ab yool ak tiyaaba.

Tekki: Àngale Urdu Español Endonesi Uyguuriya Bengali Farãse Turki Risi Bosniya Sinhaaliya Endo Sinwaa Faaris Witnaam Tagalog Kurdi Awsa Portige Malayalam Telgoo Sawaahili Taamili Buurmi Taylandi Almaa Sàppone Pastoo Asaami Albaani Suwiit Amhari Olànd Gujarati Xisxisi Nipali Yorubaa Litwaani Dariya Serbi Somali Taajiki Kinirowanda Rom Majri Ciikiya الموري Malagasi Itaali Oromoo Kanadi البلغارية Asrabijaani Usbeg Ukraani الجورجية اللينجالا المقدونية
Gaaral tekki yi

Bokk na ci njariñi Adiis bi

  1. Bokk na ci njariñal adiis bi :
  2. Mooy Sarax du yam ci li nit ki di génne ci alalam kepp, waaye day làmboo lépp lu baax lu nit ki def walla mu wax ko, te di ko jottali ñeneen ñi.
  3. Dafay xëcc nit ñi ci def lu baax ak def lépp luy amal njariñ ñeneen ñi.
  4. Bañ a xeeb jëf ju baax, donte daa tuuti.